WOTEY 2024 YI : LEERALI JËWRIÑ MAXTAAR SIISE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ëllëg ci dibéer ji lañ woo Saa-Senegaal yi ci mbañ-gàcce yi ngir ñu fal Njiitu réew lu bees. Ginnaaw xaar bu yàgg te metti, jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, Muhamadu Maxtaar Siise, delsi na ci waajtaay gi ak li mu dikkee réew mi.

Démb ci àjjuma ji lañ doon tëj kàmpaañ yi ñeel wote yi ñuy amal ëllëg ci dibéer ji. Jëwriñ ji ñu dénk wàllu biir réew mi doon na ci amal itam jàkkaarloo ak taskati xibaar yi ngir def caabalug (compte rendu) waajtaay gi. Naka noonu, jëwriñ ji di xamle ni matukaay yépp jël nañ leen te wote yi dinañu leen amal ci dal, ci dëgg ak ci lu leer naññ.

« Ci dibéer ji, Saa-Senegaal yi dinañ mën a dem woteji ci seen coobare bopp ak ci lu leer naññ. Teg nañ lépp ci barab bu mu war a tegu. Lépp a ngi dox ni ko yoon tëralee. Am nañu ay doxalin ak i delluwaay yu tax ñu mën a wax ni wote yi dinañu leen amal. »

Bu dee lu jëm ci lawax yeet, jëwriñ ji ñu dénk wàllu biir réew mi waxaale na ci. Seen lim dafay des di nekk 19. Donte ni Abiib Si ak Séex Tiijaan Jéey rocceeku nañ ci ginnaaw gi, dañuy wéy di leen lim ci lawax yi. Bees sukkandikoo ci lay yi mu biral, Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi kese moo am màqaama wax ni diw ak diw ñoo bokk ci lim bi. Ba tax na fileek jébbaluñ ko beneen lim bu tukkee fa ñoom dañuy jàpp ni ci lawax yi lañ bokk. Te seen i xob itam dees na leen fekk ci pekki wote yépp, nees fay fekkee xobi lawax yépp.

Jëwriñ ji indi naat yeneen leeral ci amalug wote yi. Ci wàllu koppar, dikke na leen lu tollu ci 14i tamñaret (milyaar) ci xaalisu Cfa. Mu teg ci ne « ay wote amuñu njëg, waaye dafa kay jar ». Xaalis boobu yépp nag, li lawax yi takku moo ko waral bees sukkandikoo ci li mu wax. Ba tax mu yokk ca ni dañ war a yokk « caution » yi ngir limub lawax yi mën a wàññiku ndax demokaraasi moo ko laaj.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj