Ginnaaw bi ndajem ndeyu àtte mi noppee ci caytu gi njëkk ñeel way-sàkku lawax yi, am na ñenn ci ñi mu geg ñu fas yéene dugal ab dabantal. Bees sukkandikoo ci li yéenekaay yi fésal tey, ñi ngi tollu ci 27i lawax yoy, dañoo lëkkatoo ngir naqarlu anam bi ñu saytoo seen i baayale. Ba tax ñu ciy joxoñ baaraamu tuuma lii di wayndarew wote (fichier électoral) wow, ci la 7i àttekat yi sukkandiku. Ci li ñu bokk wax nag, wayndare wi matewul. Walla boog war nañ cee indiy leeral. Nde, bare na lool ay turi maxejj yu joxe seen i baayale te fekkuñu leen ci.
Cig pàttali 9i lawax doŋŋ ñoo jàll ci caytu gu njëkk gi. 22 yi dañ war a mottali. Ñu gis ne 93 yi dugaloon seen i wayndare yépp bokkatuñu.
Ba tey ci caytug baayale yi, kurélu maxejj gii di Forum civil sàkku na ci ndajem ndeyu àtte mi mu xamal askan wi anam yi muy sukkandiku bay jàllale walla di geg ab lawax. Bees sukkandikoo ci kàdduy Biraayim Sekk, seen njiit li, warees na xamal askan wi nu mbir yi di doxe, noonu lam réew muy tegu ci demokaraasi di doxee. Naka noonoot, dina doon luy leeral coow li lawax yi yékkati te mu jëm ci baayale yi. Fàttali na itam Saa-senegaal yi ni, wote, joŋante falu la. Warul a àgg wenn yoon fu muy gàllankooree jàmm jeek dal gi ci réew mi.