Fukki fan rekk a ci des fii ak dibéer 31eelu fan ci sulet. Keroog la maxejj yi war a sànniji seen i xob ngir tànn 165i ndaw yi leen war a toogal ca Péncum réew ma. Dees na tànn ndawi réew yooyii ci ñaari xeeti tànnin : limu réew mi walla woteb raw-gàddu ak limu pàccu-diiwaan bi walla woteb cërëlaate. Ci 54i goxi wote lees di tànne 165i ndawi réew mi, amees na 46i depaartamaa ci biir réew mi ak 8i goxi wote ñeel bitim-réew. Jamono jii, nag, lawax yaa ngiy wër réew mi, ànd ak seen i mbooloo, di jéem a yey askan wi.
DINA AM AK DU AM, MUJJE NA AM
1, 2, 3, 4, 5, 6i weer… Senegaal a ngi sóobuwaat ciy wote ginnaaw biñ noppee ci wotey gox-goxaat ya. Diggante pànqalu limub njëkkaani Yewwi Askan Wi ak tëggug bool yi fi Usmaan Sonko sumboon, coow li bare woon na laata ñuy dugg ci kàmpaañ bi. Dina am ak du am, warees na ko fomm am déet… tey noo ngi nii, taq ci ripp, di ci yéy ak a yàbbi. Ndege, politig a mel noonu ; rëbb ca coow la. Waaye, ak li coow liy bare, lu gis-gis yiy wuute yépp, ñépp a ànd ci dayob solos wote yile.
Naam, ndawi réew yees war a fal, ñu nar a moome 5i at yii toftalu, seen uw sas mooy daganal walla gàntal ay sàrt. Wànte, foo natt solos sàrt yooyii, weesu na ko. Daanaka, meneesul a takk njariñ walla loraange yi nar tukkee ci sàrt yoy, ca péncum réew ma lees leen di yoonalee. Dafa di, fànn boo jël ci liy doxal um réew, yoon a ko lal, di cëslaay gi. Muy koom-koom gi, di njàng ak njàngale mi, di paj mi, muy dem beek dikk bi, di yoon wi, di yaxantu bi, di politig bi ak li ñeel caabal yi, lépp lees ci jël, aw yoon a ko lal. Kon, am réew mënta suqaliku te amul i sàrt yi muy ndëgërlaayoo. Ndegam solos sàrt àgg na foofu, warees na fullaal tànn ak tànniinu ñi koy xalaat, di ko biral ak di ko daganal. Maanaam, ab ndawu réew, li mu war a ràngoo mooy toogal askan wi ca péncum réew ma, bañ ko fa tooge, sàmmal ko fay itteem ak i soxlaam, bañ ko mbubboo ngir ittey ak i soxlay boppam. Bu ko defee, ndawi réew mi bokk nañu ci ñiy joow gaalug Senegaal ; ammaa ñu joow jëme ko ca tefesug jàmm, dal, naataange ak yokkute, ammaa ñu joow jëme ko ci tefesug ay, fitna, ñàkk ak ndóol. Wote yii nag, dañu wund lu bare ci wàll yépp, rawatina ci wàllu koom-koom, politig ak jikko yi.
GËDDAB PENCUM RÉEW MI ÑEEL KOOM-KOOM GI
62i at ci 2022 bii nu tollu, bi Senegaal moomee boppam ak léegi. Muy 62i at yoo xam ne, réew mi demul, dikkul. Nde, bi réew mi génnee ci jàngoroy nooteel ba nëgëni sii, wéragul. Day sooxaale feebar bi rekk, di tane-tanelu, di jóg ak a daanu, waaye ba tey mënagul a taxaw temm, ne jodd ngir mën seq i jéego yi koy jëmale kanam. Ndaxte, Senegaal a ngi bokk ci 46i réew yi gën a ndóol ci àddina si. Bu ñu sukkandikoo ci ANSD (2013), di kurélug xayma réew mi, téeméeri saa-senegaal yoo jël, 37,8 yi dañoo ndóol. Te, ci dëkki kow yi la ndóol bi gënatee metti. Ndaxte, foofa, 100 yoo jël, xaaj bi ak lu teg dañoo ñàkk. Rax-ci-dolli, ci biir askan wi, 54,6i nit jànguñu, taruñu ci 100 yoo jëlati. Nu ni déet-a-waay, Senegaal ame borub 10295i tamñareti CFA ci atum 2021 te, nee ñu, dafa nar a àgg ci 10937i tamñareti CFA ci atum 2022. Kaawtéef !
Moone de, Senegaal bokk na ci réew yi gën a gànjaru ci àddina si. Ndax, géej ak li ci biiram, Senegaal am na ko. Suuf su nangu, Senegaal am na ko. Gil ak sorooj (gaas ak petarool), fees nañ fi dell. Aw naaj ak i ceeñeeram a ngi nuy tàllal i loxoom, di ñu baaxe leer ak tàngoor bees mën góobe laf ak mbëj, waaye tam, mën a ñoral mbey mi. Suufus Senegaal saa ngi ëmb ba diis ay balluy mbindaare yu dul jeex : wurus, përëm ak xànjar, korom, nikel, palaatinoyid, sirkõ, titaan, fosfaat, kewug isin, xorom, xeeri taaral, añs. Ana kon lu war a tax Senegaal des ginnaaw ? Bu yeboo ne, loxo yi ko yor ñoo tële. Teg ci ne, lees fi lim yépp, ngir Senegaal jariñoo ko, fàww mu am uw yoon wu dëgër te di jiital njariñi askanuw Senegaal ci kow njariñ ak bëgg-bëggi as mboolo walla ay doxandéem. Te, yoon woowii, ammaa ndawi réew mi xalaat ko, tëral ko, jébbal ko péncum réew mi mu daganal ko, baatu doxal bi jëfe ko ; ammaa keneen walla ñeneen sumb ko, ñoom, ñu daganal ko. Kon seen taxawaay, ci wàllu koom, dafa am solo, rawatina jamono yii dégmalu nga xam ne, ñoo ngi waaj a liggéey gil bi ak sorooj bi.
POLITIG : WOTEB NJIITEEFU REEW MI 2024 AK… BUUMU JAAM GI
Bu dee ci wàllu politig, li ñu fi tàmm a gis mooy xeetu depite boo xam ne, moom, bëgg-bëggi njiitu réew mi rekk, kese, lañuy jaamu. Lu Nguur gi wax, mu ne waaw, du xalaat sax ndax baax na am déet. Moom daal, na fa nekk di nelaw ak a tàccu rekk, bu wote jotee ñeel naaluy Nguur gi walla làng gi mu bokk, mu yëkkati baaraamam bi. Bu dee li kujje gi indi, bu baaxee sax, mu bank loxoom. Rax-ci-dolli, di xuloo ak a xeex, di xastante ak a saagante, ñépp di dégg, ñépp di gis. Amaana sax, jàngul, xamul luy sasu depite. Xeetu depite boobu, baaxul cim réew.
Ci beneen boor, péncum réew mi am na cër bu réy a réy ci jéng yi nu Farãs takkal ba tey. Ndaxte kat, fa lañuy wotee xeeti naal yu deme ni APE, maanaam digaaleb koom-koom ak réewi Tugal yoy, ñoo nu ëpp doole. Foofee tamit, ca Péncum réew ma, depite yi mën nañu fa waxtaane mbirum CFA ak teewaayu soldaari doxandéem yi ci réew mi. Waaye, li ci ëppati solo, ñépp di ko waxtaane, mu jur coow lu bare, mooy mbirum ñetteelu moome bees njort ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, moom lay diir.
Li ëpp ci askan wi ak kujje gépp dañu jàpp ne Njiitu réew mi warul bokk ci joŋantey woteb njiiteefu Senegaal 2024. Nee ñu, ak boroom xam-xam yu ràññeeku ci wàllu xam-xamu yoon, Maki Sàll, ndeyu-àtte réew mi mayu ko sañ-sañu bokkaat ginnaaw bim amee ñaari moome yu toftalu. Mu mel ni, nag, moom ak i farandoom, bëgguñoo bàyyi te jaral na leen lu ne. Am ñu gis ne, wote yii, mën na doon ab àtte. Ndax, bu ci Maki Sàll ak Bennoo Bokk Yaakar amee ndam, ab junj lay doon ci ne askan waa ngi koy wéy di wóolu. Bu dee safaan bi, dina firndeel ni Senegaal doyal na ci moom, te dinañ jàmmaarloo ak moom bu laaje ñetteelu moome. Ab xeex a ngoog, nag.
BENNOO BOKK YAATAL WALLA XATAL BOROOM ÑAARI TUR YI
Jamono yee weesu, coowal ngóor-jigéen a lëmbe woon réew mi. Waa Ànd Sàmm Jikko Yi di ñaxtu ak a kaas ngóor-jigéen giy law ci réew mi, te Nguur gi am ci wàll wu réy. Fépp fuy këru diine, dem nañ fa, waxtaan ak Xalifa ba. Képp kuy kilifag aada, toog nañu ak yow, biral la solos xeex bi ñuy xeex ñaawteef bile. Fu ne ñu dem fa, ku ne ñu wax la ; di amal i doxi ñaxtu ak i ndaje ak saabalkat yi. Àggoon nañu sax ci defar ab sembub àtte buy xeex ngóor-jigéen, jébbal ko depite yi. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoo gàntal sembub àtte boobu, xeex ko. Ñu jàpp ne, ñooñii, daganal ngóor-jigéen mooy seen mébét. Nee ñu sax, kuréli ngóor-jigéen yaa nekk ci ginnaaw waa Bennoo Bokk Yaakaar, ne dañu bëgg a yaatal boroom ñaari tur yi ci réew mi, ñoom waa Ànd Sàmm Jikko Yi bëgg leen a xatal ba jële leen fi. Moo tax, wote yii, ñu jàpp ne mënees ci jaare, jële leen fi, teg fi ay ndaw yoy, sàmm jikko yi, diine ak mbaax yi moo leen ñor, ngir ñu jàllale sembub àtte buy araamal ngóor-jigéen ci réew mi.
Wote yaa ngoogu, askan waay tànn. Ammaa mu tànn ñiy péncoo réew mi, ammaa mu teg fa ñu koy paacoo.