Njureefi wotey Ngomblaan yi ñoo ngi tàmbali di génn, rawatina fa bitim-réew ak réew yi féete penku. Fii ci biir réew meet, am na yenn ciy njureef yees tàmbalee siiwal bi 18i waxtu jotee. Laata ñuy am njureef yépp nag, mënees na ñëw ci yenn taxaw-seetlu yi ñeel amal beek doxalinu wote yi.
Bi 8i waxtu jotee ci suba la pekku yi waroon a tijji, waroon a tëj itam bu 18i waxtu jotee. Bees sukkandikoo ci xibaar yi kuréli ma-xejj gii di MOE-COSCE (Mission d’Observation Électorale du Collectif des Organisations de la Société Civile pour les Élections) siiwal, 100i pekk yoo jël, 50 ya sàmmonte nañu ak waxtu tijji bi (50%). Waaye, laata 10i waxtu di jot, 99% (juróom-ñeen-fukk ak juróom-ñeent ci téeméer bu nekk) tijji nañu.
Jumtukaay yeet, mënees na wax ni daanaka lépp yemboon na ginnaaw bi pekk yi tijjee. Nde 99% (juróom-ñeen-fukk ak juróom-ñeent ci téeméeri pekk yoo jël) fekk nañu fa njiitu pekk ga, ndawi CENA bi, jumtukaay yi war, xobi lawax yépp ak mbañ-gàcce gu wotekat yi mën a suturloo ngir amal seen tànn.
Ndawi lawax yeet seetlu nañu ni, lu mu tuuti tuuti, dina am benn ci 94% ci pekk yi. Seetlu nañoot teewaayu saytukati kurél yu mel ni UA (Union Africaine), CEDA (Commission électorale départementale autonome ), ak takk-der yiy saytu kaaraange ma-xejj yi.
Ginnaaw taxaw-seetlu yii ci amal beek doxalinu wote yi, seetlu nañu itam ni ma-xejj yi feesuñu lool ci pekk yi bees ko méngalee ak wotey njiiteefu réew mi. Daanaka, ba ci xaaju bëccëg bi, 100 bindu yoo jël, ñi ci wote matuñu 50.
Bu dee njureef yi tàmbalee rot, Pastef moo jiitoogum, rawatina fa bitim-réew. Fi réew mi tamit, Pastef mu ngi raafalagum pekki wote yu baree bari. Dees na ci ñëwaat ci ni mu gënnee yaatu ci mbooleem diiwaani réew mi.