WOTEY NGOMBLAAN GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Amal nañu am ndaje ñeel wotey Ngomblaan gi ñu namm a amal ci weeru nowàmbar wii di ñëw. Muy ndaje mu jëwriñu biir réew mi doon séq ak ñi wote yi soxal ngir bokk ak ñoom xibaar yi ñeel doxalin yi.

Tey ci gaawu gi, 21 sàttumbar 2024, la jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, Seneraal Sã Baptist Tin woote woon am ndaje fa Hôtel Radhisson, ci 9i waxtu ci suba. Mu ci doon dajeek làngu pólitig yi, lëkkatoo yi, Cena bi, Cnra bi ak kurél yi wote yi soxal ngir waxtaane lu soxal doxalinu wotey Ngombalaan gi.

Bokk na ci lu gën a fés ca ndaje ma nag, waa ATEL (Alliance pour la Transparence des Élections) yi gedd ginnaaw bi leen jëwriñ ji dalalee ba ñu weccoo ay kàddu. Omar Saar mi yore seen kàddu dafa sàmp laaj doon leerlu ci waxtaan wi ñu namm a amal ak njeexital li muy am ci dekkare yi Njiitu réew mi jël ba noppi. Li ko jëwriñ ji xamal mooy ni dégg na ko, waaye  doxalinu wote yi moo leen fi dajale. Te bu ñu noppee dinañu jël lépp jébbal ko Njiitu réew mi.

Laaj bi Omar Saar sàmp nag, Munjaay Siise mi jiite kurél gii di ONG 3D, bokk ci kuréli maxejj yi jàpp na ni laaj bu mat a laaj la. Nde, doxalinu wote yi aajoowul a waxtaane ndax xam nañ ko ba noppi. Ci gis-gisam, dekkare woote bi ñeel wote yi moo  am jafe-njafe. Ba tax mu jàpp ni Nguur gi mënoon na gën a yaatal jëme ci matuwaay yi, niki àtte tëralin yi laale ak séddalinu toogu yi, pekk yeek yu ni mel.

Bu weesoo Ndaje moomu, DGE (Direction Générale des Élections) sóobu na ci mbiri lawax yi. Démb ci àjjuma ji la génne ab yégle bu mu jagleel làngi pólitig yi, lëkkatoo yeek benn-benn yi. Mu leen ciy xamal ni dinañu ubbi pekk biy nangu wayndare bindu lawax yi keroog talaata 24 sàttumbar 2024 bu 8i watu jotee ci suba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj