WURE WA DEM NA KËŊŊ !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ngomblaan gi, walla Péncum ndawi réew mi (ni ko ñenn ñiy wowee), benn la ci ñatti firgaat yu mag yiy joow Gaal gi. Gaal gu yaatu gii di Senegaal, fees dell ak i gànjar. Nu bokk lépp te mënunu cee seddoo dara. Gaal gi nu mës a boole ba nu faf doon benn bopp bu kenn warul a xar ñaar.

Dayob Ngomblaan googu tax na, jàmbur ya koy séq, ku dul doomu réew mi, doo ca bokk. Waaye it, doomi réew mi ñoo leen di tànnal seen bopp. Te, ëllëg ak jàmm, ci dibéer ji, 17i fani nowàmbar 2024, yemoo ak 13i fani rakkaati gàmmu 1446, lanu leen war a fal.

Ñoom ñooñu war noo teewal ca Pénc ma, ñu ngi leen war a seppi ci biir 7 294i lawax yu yékkati seen i loxo ngir bëgg ku leen tabb. Lawax yooyu, ñu ngi bootu ci 41i toftale yu samp seen i ndënd. Toftale yooyu nag, daanaka ñetti ayu-bés a ngi nii ñu doon wër reew mi ngir dagaan baatu askan wi.

Def nañu ay njëgg yu mag, amal nañu ay ndaje yu réy, doxantu nañu it ci gox yu bari ngir yey fere yi, ñu sàndil leen seen i xob bu ëllëgee. Pexe mu ñu amoon rekk, def nañu ko ngir dagaan sunuy baat nun ñi war a tànn ñu nu yónni.

Fi mu nekk nii nag, nun ñii di tànnkat yi noo ci des. Nanu daas sunuy këyitu wéttkat fanaanal. Ñi nekk ci biir réew mi te jotaguñu seen i yos, war nañu daw gaaw jëli leen tay ci gaawu gi. Ñi nekk bitim-réew moom, suba sax, ci dibéer ji, mën nanu koo jëli. Bu ci kenn tayal waay !

Bu nu xëyee, dem defi sunu wareef. Waaye itam, jëli li nu moom. Ndax kat, wétt, wareef la ci bépp ma-réew ; waaye it, àq la ci moom. Kon boog, nanu dem nun ñépp ci anam yi mu gën a rafetee, màggal bés bi (tuutiwul nag !). Te, bu nu defee sunu wareef ba noppi, nu dellu ak jàmm sunuy kër walla ci sunuy yitte xaar njureef yi.

Ginnaaw bi lawax yi wonee seen i feem yépp, nun ñii noo ci des. Nde, noo yore kàddu gu mujj gi. Te, bu ëllëgee, lépp dina leer bu soobee Yàlla. Lu waay doon jaay, mu të a jar ba léegi sii, bu moytuwul dina lamb. Ndax kat, wure wa dem na këŋŋ !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj