XEEB NGA XAL, MU LAKK SA DÀGGA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bi Senegaal dee Senegaal ba tey, xeetu coow lu ne jib na fi, fitna ak i taafar yu bari yëngal réew mi. Naam, xeex yàgg naa am ci géewu pólitig gi, li ko dale jamonoy Seŋoor jàpp jamonoy Ablaay Wàdd, jaare ko ci nguurug Abdu Juuf. Dafa di, pólitig ak coow ñoo ànd. Deesu ko weddi. Waaye, lii ñu nekk di dund ci nguurug Maki Sàll gii, guléet ci réew mi. Ñi xam mboorum Senegaal, fekke jamonoy ñeenti njiiti réew yi Senegaal amagum yépp, ñoo bokk genn kàddu : Senegaal mësut a yëngoo nii. Kon, mbir mi aajowoo na ab taxaw-seetlu. Nde, saa buñ tuddaan Senegaal ci àddina si, rawatina Afrig, lees ciy toftal mooy baatu « royukaay ».

Boo laajaan lu tax, ñu ni la Senegaal a di réewum jàmm. Réew mom, fa la jullit ñi ak kercen yi séq jàmm, jaxasoo ba mel ni mburook soow. Senegaal, réewum dal mom, fa la tarixa yi bennoo, bokk ndey, bokk baay. Senegaal, réewum mbatit mom, fa la waaso yi, ak lu ñuy bari te wute yépp, ñoo ngi ànd, jàppoo, booloo di laamisoo, di kalante ak a séy seen biir ba seen i deret wayandoo. Senegaal, réewum demokaraasi mom, askan waay fale, di folle. Senegaal, réewum péexte ak ngor, di réew moo xam ne, képp kenn ci maxejj yi am na sañ-sañu wax xalaatam ci yar ak teggin, joxe gis-gisam ci ni réew miy doxe ak ñi ko jiite te dara du ko ci fekk. Senegaal googu mooy Senegaalu royukaay bi ñu daan dégg ci àddina si, di ko dégg ci Afrig. Senegaal googu, mooy Senegaalu Seŋoor, Senegaalu Abdu Juuf, Senegaalu Ablaay Wàdd, ndare gu Maki Sàll gii nga xam ne, ci fitna la ko jële, ci fitna la ko jiitee diirub 12i at, te ci fitna la ko nar a bàyyee. Ndeysaan…

Lu tax ? Moone de, njort rafetoon na ci kor Mareem. Ndax, dafa maaseek jamono, di xale, juddu ginnaaw ati 1960 yi. Yaakaar ju réy la nit ñi amoon ci moom. Waaye de, ñépp a yàqi wëliis ay dagam, ay mbokkam ak i àndandoom. Nde, nguuram gépp, mënees na ko tënk ci kàddu gii mu waxoon ca njëlbeen ga : « Dinaa seeyal kujje gi ba mu seey. » Noonu, Kariim Wàdd, mu jàpplu ko, tëjlu ko, gàddaayloo ko. Mu jël waa Bennoo Siggil Senegaal ñulug leen ci Bennoo Bokk Yaakaar, ñu seey ci. Mu jëlati waa Bennoo Taxawu Senegaal, sóor leen ci cinam li, ñoom itam ñu seey ci. Xanaa kujje gi seey na ? Déedéet. Des na kenn : meeru Ndakaaru bi, Xalifa Sàll mi worook ndem-si-Yàlla Usmaan Tanoor Jeŋ, ber kurélam, tàmbalee bay waaram. Maki Sàll tàllal ko loxo, bëgg koo boole ci yakk bi,  Xalifa Sàll dëgër bopp, lànk. Mu taqal ko, sàqal ko pexe, yóbbu ko ndung-siin.

Dafa di kat, booba, Xalifa Sàll a ngi doon amsi doole, te loolu la kees dàkkentale Soxna Batoor di bañ. Maki Sàll ak wujje ? Mukk ! Moo taxi t, damm na laafi Xalifa Sàll mi doon waaj a naaw ci kawam. Njaatige Bàrtelemi féete boor. Nga foog ni jeex na ? Déedéet. Xanaa danga fàtte waa PDS ? Dañoo daanu rekk, waaye xalanguwuñ woon de. Ndaxte, bu dul Kariim Meysa Wàdd miñ doon xeexal, doon nañ faral di cokkaas Njiitu réew mi léeg-léeg, di xumbal ak a xoromal géewu pólitig gi donte ne safuñu woon askan wi noon yépp. Waaye de, benn lanc la leen Maki Sàll def, ñu seey ci biiram. Nga gis kon ne, géew gi deseetul mbër mu dul Maki Sàll miy buur, di bummi. Muy doxal nim ko neexe, jàpp ne, léegi, amatul kenn ku ko mën a diir mbagg. Muy yóot 3eelu moome, fas yéene toogaat ci nguur gi diir bu ko soob. Ndekete yoo, booba, am na njuuma lu ko doon yoot. Moom, dafa mel ni ku déggul Wolof Njaay bi muy wax ne : « Boo xamoon li lay yoot, dinga bàyyi li ngay yoot. » Kuy njuuma li ? Yaakaar naa ne ñépp xam nañ ko.

Ba ëllëg ñu wéyal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj