Xeex nger ci àddina si

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àjjuma ji, 9i fan ci weeru desàmbar 2022, la àddina wërngal këpp doon màggal bés biñ jagleel xeexub nger. 20i at ci ren daanaka, bi ko Mbootaayu xeet yi di ONU (Organisation des Nations Unies) sosee ci atum 2003. Dafa jaadu ñuy amal xew-xew bu ni mel at mu jot ngir kurél yeek Nguur yi mën cee amal ay ndajey waxtaan, di yeete ak di nàmm xel yi ci jëfin yi.

Bu ñuy wax nger nag, ci jënd gi nit di jënd moroomu nitam ba tere koo def i wareefam la xel yépp di dem. Naka la nit mënee jënd moroomu nitam sax ? Faramfàcce ko du xaj cib yaxal. Waaye mënees na jàpp ne nger weesuna sax jëmmu nit ki, di law ci askan yi ba ci diggante réew yi. Ci gàttal daal, nger mooy lal i pexe ngir jot cim mbir mom, boroom yelloowu ko. Looloo waral ba, ca atum 2000, ONU jëloon ndogalu topp bépp xaalis bees yónnee ci anam yu teey xel ci diggante réew yi ngir delloo leen. 2001 ak 2002 mu jëlaatoon ndogal ngir wattandiku nger ak delloo xaalis yees rawale ca fa ñu bawoo ba noppi, tegaat cab digaale xeex nger ci bépp fànn. 

Biñ demee ba ci atum 2003, Mboolem xeet yi dëppoo ci ni nger dafay jur i jafe-jafe yu doy waar ak i njàqare ci ndal geek kaaraange réew yi.  Loolu yóbbooti leen ci xaatim Déggoo Mbootaayi xeet yi ngir xeex nger (Convention des Nations Unies contre la corruption) 31eelu fan ci weeru oktoobar 2003.

Bu weesoo ni muy nasaxalee koom-koomu réew yi, nger mën na yóbbu réew ci jéyya. Loolu tax na ba Mbootaayu xeet yi diy fàttali ne « nger dina juddoo ci xeexoo, waaye mën naa jur itam xeexoo ».
Atum ren jii, jubluwaayu bés bees jagleel xeex nger mooy waxtaane ponk bu am solo : Nger, jàmm, kaaraange ak suqaliku.

Buñ ko dàkkee foofu nag, dafay wone ni xeex nger doon na lu war a yitteel ku nekk, moo xam Nguuri réew yi la, ci bërëbi liggéeyukaay yi, kurél yiy xeexal askan wi ba ci nit ñi ci seen bopp. Ñépp ñoo war a sóobu ci xeex bi ngir mën cee mucc, waaye tamit, ngir mën cee muccal am réew. Dafa di, nger doon na luy yàq jikko yi, di daaneel kenuy bokkeef gi ak a delloo réew ginnaaw.

War na ci mépp réew mu bokk ci réew yi dëppoo xaatim Déggoo Mbootaayi xeet yi ngir xeex nger mu taxawal i pexe yuy jëmmal ndogal yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj