XEW-XEW BU DOY WAAR FA KOLDAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xew-xew boobu mi ngi am démb, ci dibéer ji, fa koñ bii di Médina Sérif, nekk fa Koldaa. Genn góor gu daan liggéey ci ab “ambulance” (ambulancier) moo jote woon ak soxnaam jote bu metti. Moom, boroom-kër gi, du yar walla loxoy kese la ko doon dóore soxna si. Nde, daf ko jàpp, jam ko ay paaka ba mu nekk ci diggante dund ak dee. Waaye, moom yemul ci loolu. Ndax, ginnaaw bi mu defee jëf jooja, dafa doon jéem a xaru. Jamono jii nag, ñoom ñaar ñépp ña nga fa raglu ba.

Coowoo ci diggante ay way-dencante, lees miin la fi réew mi. Dafa di, du guléet ñuy gis xeetu xew-xew yu ni mel ci mboolaay mi. Waaye, bii moom dafa ëpp i loxo. Nde, ñoom ñaar ñi nga xam ne ñoo jote, yàgg nañoo séy. Bees sukkandikoo ci li waa Seneweb siiwal, moom M. Seydi, nga xam ne tollu na ci juróom-benn-fukki at, ak soxnaam séy nañu ñaar-fukki at ak juróom. Am nañu juróom-benni bant. Nee ñu nag, ñoom ñaar dañoo amoon ay coow yu sew ba soxna si nekk ci tànki ñaan baat.

Bi loolu amee, ci la boroom-kër bi demee ci way-juri ndaw si (ngoonu gaawu). Ñoom tamit, ñu sàkku ci moom mu xaar ba ëllëg (dibéer), ñu waxtaansi. Waaye, laata àpp googu di jot fekk na góor gi moom fajal na boppam mbir mi. Nde, démb ci suba gi la jàpp soxna si jam ko ay paaka ba muy waaj a génn àdduna. Seen benn dëkkandoo buy wuyoo ci turu L. Jàllo moo dégg yuuxu yi ay boori juróom-ñaari waxtu ci suba. Bi mu demee ci la fekk boroom-kër gi mu nekk ci benn ruqu ca kër ga, yor paaka. Bi mu jëmee ci moom la góor gi jël paaka bi jam ko boppam ci wetu dënn bi. Nee na ci la daanoo jéll bu metti boole ko ak di nàcc deret ju bari. Rax-ci-dolli, gis na beneen gaañu-gaañu ci biir bi, wetu ndey-joor bi.

Dafa di, ñoom ñaar ba tay, kenn xamagul lan lañu jote dëggantaan. Waaye, bu ñu ci ubbee ay luññutu, lépp dina leer. Li am ba des mooy ne, jamono jii, ñoom ñaar ñépp ña nga fa raglu ba. Jëkkër ji moom, ña nga koy yokk doole “réanimation”. Soxna si moom, mi ngi ci “soins intensifs” ndax, dañu ko oppeere. Kon, fi mu tollu nii, ñoom ñaar ñépp a sonn. Lii nag mooy saafara su jur jàngoro.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj