XEW-XEW BU TIIS FA ETAASINI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñetti Saa-Senegaal ñoo ñàkk seen i bakkan ci anam yu metti fa Etaasini. Ci li rotagum ciy xibaar, nee ñu, ab ndaw bu tollu ci ñaar-fukki at ak ñaar moo soqi fetel ci kow ñaari rakkam, jam leen ay bali bopp, ñu daldi faatu. Jenn rakk ju jigéen ji, ñaar-fukki at la amoon, rakk ju góor ji amoon fukki at ak juróom-ñaar. Li ci gën a doy waar mooy, bi mu leen bóomee ba noppi, dafa xaru.

Albuquerque (Etaasini) la musiba bi ame. Ñoom ñooñu nag, ñook seen way-jur wu jigéen ñoo dëkk. Waaye, ba mbir may xew, fekku ko fa. Xew-xew baa ngi am ci njeexitalu ayu-bés bi. Door nañ luññutu yi ngir xam dëggantaan lu waral jéyya ji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj