XEW-XEW BU TIIS FA JÀNGUNE JU KAWE JOJ NDAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Naqar ak tiis la waa Ndar fanaanoo guddig barki-démb rawatina ndongo ya nekke fa daara ju kawe jooju di UGB (Université Gaston Berger de Saint-Louis). Seen benn naataangoo moo fa génn àddina ci anam yu yéeme. Nde, ndongo loolu dafa lab fa béréb bi ñuy dippe “hydrobase” nga xam ne, léeg-léeg, ay mbooloo dañu fay daje di sangu. Mu nekk xibaar bu diis lool ci ndongoy daara ju kawe jooja. Waaye, mu diis loolu tamit ci mbokkam yi mu bàyyi ginnaaw.

Dafa di nag, du guléet xeetu jéyya yii di fa am. Ndongo li ñàkk bakkanam jigéen la. Mi ngi wuyoo ci turu Ndey Coro Siise Njaay. Ren mooy atam mu njëkk ca daara ju kawe ja. Maanaam, moom, fanweer ak juróomeelu maas gi la bokk (P35). Ma nga nekkoon fa banqaas bi ñuy jàngalee Yoon, pólitig ak yeneen ya ca aju, muy UFR SJP (Unité de Formation et de Recherche des Sciences Juridiques et Politiques). Xale bu jigéen bi lab, mi ngi bawoo Jaxaaw, nekk ca Cees.

Barki-démb, ci ngoonug dibéer ji, la ndongo loolu wuyuji Boroomam. Muy xibaar bu tiis te bette. Démb, ci altine ji, lañu koy jébbal Boroomam fa armeeli Jaxaaw ya. Ndongo la loo xam ne, seedeel nañu ko ay seede yu rafet. Nde, nee ñu nit ku baax la woon, nite, yaatu te fonk li muy def. Donte ne sax, yàggul ci jàngune bi, waaye, terewul ñu seedeel ko seede yu rafet ci ginnaaw.

Mu mel ni, xeetu jéyya yii li mu fiy am mi ngi bëgg a bari. Loolu tax ba kurél giy yëngu ci nekkiinu ndongo yi di Com-Soc (Commission Sociale des Étudiants) di sàkku ci ndongo yi ñu xool fi ñuy teg seen tànk. Ndax, jéyya yu ni mel li mu fiy am bari na. Na ku nekk gën a teey, te moytu. Def kéemtelaayu kàttanam ba aar bakkanam, aar tamit ay naataangoom. Ndax kat, géej moom amul banqaas.

Yal na ko Buur Yàlla yërëm te jéggal ko ay rëcc-rëccam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj