XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

DAAN NAÑ PÓOL POGBAA 4i AT YUM DUL FUTBAL

Doomu Farãs ji, ndax futbalam du fi jaare yàqu ? At yii weesu, saa bu génnee ci jafe-jafe bii, daldi dal ci beneen, rawatina ñaari at yii ñu génn. Mi ngiy jóg ak a daanu rekk ci sababi gaañu-gaañu. Fim ne, mu ngi newaat saraax ci weneen njombe. Nde, dañ ko daanati ci alxames jii weesu 4i at yoy du joŋante fenn. Li ko waral nag mooy ni dafa doon jëfandikooy dorog yu ko doon yokk doole bu duggee ci pàkk mi. Kurél gees dénk wàllu caytu googoo ko génne xamle ni dafa doon jëfandikoo yu ni mel. Muy lu tiis ci kaw waagab àddina 2018 bi. Ndax, ñàkkul ni mu ngi war a dugg ci 31eelu atam, kon bu daan biy jeex dana ko fekk mu am 35i at. Loolu tax ñuy laaj ndax du fa jaare bàyyi ?

Moom Pogbaa nag, nanguwul daan bi. Ndax, xamle na ni dina def ab dabantal ngir ñu xoolat mbir yi.

ILIMAAN NJAAY TÀMBALI NA JON SOPPEY MÀRSEY YI

Waa Màrsey ba ñu soppee tàggatkat ba léegi, lépp gongo. Bërki-démb ci gaawu gi la woon 3i joŋante yu Màrsey di tegale di gañe ; muy lu gëjoon a am ca ekib ba.

Ilimaan Njaay nag, moom dafa mel ni ay làmpam dañu fa jaare di tàkkaat. Ci yooyu ñetti joŋante dugal na ci ñaari bii, dolli ci di dawal lu neex. Mel na ni tàggatkat bu bees bi “Jean-Louis Gasset” sopp na ko lool.

BARAAHIM JAAS TÀNN NA MAROG !

Futbalkatu Real Madrid bi tànn na Marog ci kaw Espaañ. Ci fan yii ñu génn la matal jéegoy caytu “procédures administratives” yi ko dese woon ngir mën a sol mayo gayndey atlas yi.

LÀMB JI

Taxawalees na diggante Rëg-rëg ak Booy Ñaŋ.

Jakson ak « Lac-rose » itam seen làmb taxaw na. Ñaari làmb yooyu yépp Gastoŋ Mbeeng moo leen tëgg.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj