XIBAARI TÀGGAT-YARAM (12/12/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

CHAN 2025

Ekibu Senegaal dina amal ñaari joŋante ñeel bokkadili CHAN 2025 bi. Gaynde yi dinañu ci amal ñaari ndaje ak Liberiyaa. Ndaje mu njëkk mi daf koy fekki dëkkam 22eelu fanu desàmbar wii, meneen mi di ame fi réew mi, ca 28eelu fanu weer wi ba tay.

KUPPEG ÀDDINA

Siiwalees na réew yi nar a dalal kuppeg àddina 2030 bi. Ñetti réew ñoo ko nar a dalal wii yoon, ñuy Marog, Portigaal ak Espaañ. Ni muy demee nag mooy ni, yenn joŋante yi dañuy am fii, yeneen yi am fee, ya ca des ame fale. Muy coppite gees amal ci po miy ñëw.

Ba tay xamlees na ni Araabi Sawdit mooy dalal kuppeg àddina 2034. Waaye nag, ci jamonoy lolli (seddaay) lees ko amal ngir mu dëppook njuux lu jàppandi ci kuppekat yi.

LIGUE DES CHAMPIONS

Këlëb bii di Stade Brest moo ngi ci yoon wu baax ci po mi. Daanaka bett na ñu bari ndax kenn séentuwu ko woon fii. Ay matsam nii, dafa dóor Sturn Graz, RB Salzbourg, Sparta Prague, PSV Eindhoven, daldi timboo ak Bayer Leverkusen. Barça rekk moo ko dóor. Mu ngi nekkandi ca 5eelu toogaay ba, am 13i poñ ci kow 18.

VICTOR OSHIMEN CA GALATASARAY

Saa-niseriyaa bi moo ngi dox ci ndox ca sàmpiyonaa Tirki ba. Ci ndoorteelu atu futbal ren jii la ko Napoli abaloon Galatasaray. Waaye, bam fa demee ba léegi de, yarasul. Nde, mu ngi wéyal lees ko xamee woon. Fi mu ne nii, futbal na 13i joŋante yoy, dugal na ci 10i bii te def 4i paas.

NANI BÀYYI NA FUTBAL

Saa-portigaal bi, Luise Nani, xamle na ni wékk nay dàllam. Mi ngi ami 38i at. Bi mu dale futbal ak léegi am na 19i at. Ci diir boobu, gañe na ci 17i kub. Ca këlëb bu mag bii di Manchester United, fa Àngalteer, lees gënoon a ràññe.  Laaf la woon, gaawoon lool, mënoon a duutaate. Daanaka, futbalu tay dafa tumurànke xeetu laaf yu mel ni Nani.

LÀMB

CNG DËGGAL NA NDAMU MÓODU LÓO MI

Kurélu dabu gu CNG dëggal na ndamu Móodu Lóo ci kaw Sitta gannaaw bi mbëru Jàmmagën bi dugalee ag dabu ngir laaj ndam li. Waaye, dañu ko gàntal. Léegi leer na ni Xarañ Lóo, mbëru Parsel mi, mooy téye metelu làmb ji.

BËRE RËG-RËG AK BOOY ÑÃ 2

doomu Pikin Ji daldi nay dugal këyitu loppitaal (certificat médical) fa CNG ngir xamle ni dafa gaañu. Seen bëre bi waroon a am ci 1eelu fanu sãwiyee 2025 wi takkagum na suuf. Maanaam wóorul mu am. Ak lu ci mën di am nag, CNG mooy saytu mbir yi ba joxe ndogal. Nu déglondi !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj