Keroog ca alxames ja weesu lees puluf ekib yi, daldi génne kippuy joŋantey CHAN 2025 biy ame fa ñetti réew yii di : Ugàndaa, Keeñaa ak Tansani.
Mu ngi waroon tàmbali ci 1eelu fanu féewiryee wii jëm 28eelu fan wa. Waaye, bëtalees na ko ba ca weeru ut ci at mii.
Nii la kippu yi tëddee :
Kippu A : Keeñaa, Marog, Àngolaa, RD Kóngo, Sàmbi
Kippu B : Tansani, Madagaskaar, Móritani, Burkinaa Faaso, Sàntarafrig
kippu C : Ugàndaa, Niseer, Gine, Q1, Q2
Kippu D : Senegaal, Kóngo, Niseriyaa, Sudã
ESPAAÑ : 1/4 FINAAL COUPE DU ROI
8i ekib yii ñoo kalifiyee 1/4 finaalu kuppeg buur bu Espaañ. Ëllëg ci altine ji, 20 sãwiyee lees di amal puluf bi, xamalees ekib yi ci war a daje. Ku nekk mën na daje ak moroomam. Ci puluf bi nag, ekip bees njëkk a génne mooy dalal matsam ca pàkkam. Menn ndaje lay doon, amul dellu.
Ekib yi : Barcelone, Real Madrid, Atletico Madrid, Real Sociedad, Osasuna, Leganes, Getafe, Valence.
MANCHESTER UNITED : LUY AYIB BI
Donte andinañu beneen tàggatkat, teewul Manchester United moo ngi ciy jafe-jafe ba léegi. Bu yàggul dara lañu jële Eric Ten Hag ca boppu ekib ba, teg fa Ruben Amorin. Waaye ba léegi, fay metti wokkaguñ ko. Ndax, 11i mats yu mu defagum ca sàmpiyonaa Àngalteer bi, 3i ndam la ci ama, 2i timboo ak 6 yoy daf leen a ñàkk. Luy ayib bi ? Ndax ca boppu këlëb ba la? Ndax tàggatkat la ba léegi ? Mbaa ci futbalkat yi la ? Lu leer ba leer mooy ni war na gaaw saafara ngir mu dellu ca boppu sàmpiyonaa ba nees ko xamee woon bu njëkk.
REAL MADRID
Ci altine jii, dees na falaat Florentino Perez njiital këlëb ba ba atum 2029. Amul ku wujjeek moom ca wote ya, kon mooy toogaat ba booba.
LÀMB JI
Aamaa Balde ak Farã, seen jàkkaarloo bi ci xeex la mujje. Keroog ca bésu bëre Giri Bórdoo ak Sarkoo te xale “grand yoff” bi daan ci saa-faas bi ci lu gaaw, la doomu Fàllaay ji njëkkoon a jàppante ak Farã ba alkaati ya doxoon seen diggante. Démb seen jàkkaarloo bi, ñu yëngal fa, neexal, nappante. Waaye, séytaane mujj na cee am wàll ba ñaari mbër yi war a daje sànnante fa ay kurpeñ. Yu ni mel di yees war a jël ay matuwaay yu mat sëkk ngir mu bañ a wéy. Ndax, lu ko moy dara yàq po mi, te dafay jur yeneen yees dul xam seen yamuwaay.