Xibaari Tàggat-Yaram

Yeneen i xët

Aji bind ji

kuppeg Àddina U17: 1/2 finaal

Joŋante baa ngi wéy, ñu tollu fim ne ci 1/2 finaal yi. Ci 1/4 finaal yi Almaañ moo dóor Espaañ 1-0, Arsàntin gañe Beresil 3i bal ci dara (3-0), Farãs mi toogloo Senegaal ca 1/8 finaal yi ( 5-3, seri) pattal Uusbekistã (1-0), Mali itam naka noonu ci kaw Marog (1-0).

Lu ñeel dëmi-finaal yi nag, Almaañ dina daje ak Arsàntin ci talaata jiy dikk jàpp 28i fan ci nowàmbar bi bu 8i waxtu  tegee 30i simili (8h30). Bu ñu noppee Mali ak Farãs itam daje bu 12i waxtu jotee ca bés ba.

BUNDESLIGA : Harry Kane a ngi rëdd turam ca sàmpiyonaa ba

Àngale bi kenn du ne miinul ekibam bu bees bi, Bayern. Nde moo ngiy wéy di dugal ay biiwam niki ñu ko xamee. Amagum na fim ne 18i bii ci 12i joŋante. Loolu nekk luy dugal turam ci mbooru sàmpiyonaa ba bu baax.

Xabi Alonso moo ngi def liggéey bu am solo

Españool bi mu ngi ci ruqam di doxal ay mbiram bu baax ak ekibam bii di Bayer Leverkusen. Moo ngi wéyal ay ndamam di gën a xàll yoonam. Ba atu futbal bi ubbee ba nii, ci 18i joŋante yu mu amalagum, amagum na ci 17i ndam, timboo wenn yoon te  kenn dóoragu ko. Ekibam bi dugalagum na 66i bii, jël 16i bii kese. Moo tax, jamono jii, moo toogandi ca boppu sàmpiyonaa Almaañ ba, jiitu ca kippoom ci Europa Ligue ba, ba noppi kalifiyee 1/8 dë finaal kub Almaañ.

Ligue 1 Farãs : Bàmba Jeŋ dikkaat na

Doomu senegaal bi laalaat na bal tay ci dibéer ji, ci seen joŋante ak Metz gannaaw ba mu toogee lu mat ñetti weer ndax gaañu-gaañu bum ame woon ci càq yi (adducteurs). Moo ngi dugg ci pàkk mi bi joŋante bi tollee ca 60i simili.  

Làmb ji : Boy Séy 2 dóor na Móodu Anta mu daanu

Démb ci gaawu gi la Booy Séy 2 doon daje ak Móodu Anta. Seen bëre bi nag dafa mel ni xaw na dese siiw ni yi fi jaaroon fan yii. Bërewuñu lu yàgg. Nde bi ñu léewatoo ci diir bu gàtt lañu tàmbale di nappante ciy kurpeñ, yàggul dara, ci menn cong mi, ñaari mbër yi di dóorante, Boy Séy jekku doomu Cees ji, dóor ko dóor bu da, mu daldi rëpp ay wóomam, bañ-bañlu ba jugaat daldi rëppaat samp ñeenti cërëm (4 appuis).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj