Farànk Ñànki Jom, di mag ci jëwriñ ji ñu dénk wàlluw biir réew mi, Àntuwaan Feliks Jom, moom lañu duut baaraam ñeel mbirum luubal. Ki ko duut baaraam di layookatu Usmaan Sonko bi, doomu Farãs ak Espaañ ji, Xuwaan Barànkoo. Li mu koy jiiñ nag, mënees na ne menn mbir mu ñu mën a xaaj ñaar la. Mbir mi ci jiitu mooy ne, dafa sikki-sàkka ci xereñteg Farànki ci fànnu mbéll. Ñaareelu mbir maa ngi aju ciy koppar, maanaam dafa war a am ag kopparal gu tollu ci ñaari miliyaar laata ñu koy xaatimal ag pas gu ni mel. Lënt-lënt yooyoo cuq layookatu bi, mu siiwal ko, di ci sàkku ay leeral. Yemu ca de. Nde, boole na ciy artu ak i tëkk ñeel kërug liggéey gu Ostaraali gi ak ñi ci laale ñépp.
Tuuma yi Xuwaan Barànkoo teg ci ndoddu Farànk Ñànki teey na xelu ñu bari ci askan wi. Te, lenn waralu ko lu dul yeneen yu fi jotoon a jaar ak fa ñu mujj. Waaye, wii yoon, yëf yi dafa wute. Ndax, moom ci jëmmi boppam ci atum 2018 la am “permis minier” ca Kër-Sàmba. Te, ñoom ña nga doon xaar kopparal gu tollu ci ñaari miliyaar. Waaye, mbir mi yemul foofu. Dafa di, moom Xuwaan, dafa jàppoon ne jamono jii magi Àntuwaan jooju mi ngi ci ag tàqalaatu gu metti ngir rawale njabootam. Te, loolu moom dara amu ci.
Kii di Farànk moom ma ngay dawal daamar ya gën a bakkane ca biir Ndakaaru. Boole ceeg yore ay sumb ca Sidney. Loolu nekk lu teey xelu kii di Xuwaan. Ba tax moom yemul ci duut baaraam luubal googu mu koy jiiñ. Waaye, dafa jàpp ne sax, amul xereñte gu war a tax mu jekki jekki rekk Nguur gii nga xam ne rakkam ci la bokk di ko jox ay “permis miniers”. Looloo tax moom Xuwaan muy artu kilifay Ostaraali yi ngir ñu def ay luññutu ci mbooleem kopparal yi jot a dox seen diggante ak mbokki Jom yi.
Li waral loolu mooy dafa jàpp ne am na luy ñuul ci soow mi. Te, fàww Nguuru Senegaal leeral ko askan wi ñu jiite. Ndax, ci wayndare yi mu fésal Nguuru Senegaal ak kërug liggéey gii di “LA SOCIÉTÉ EBONY AUSTRALIE & SERVICES (E.A.T.S) SARL” ñoo séq mbir mi. Te, kii di Farànk Ñànki am ci wàll wu rëy ndax mooy ki ko jiite.
Tuumaa yooyu mu teg ci ndoddu Farànk Ñànki Jom, nee na ag ndoorte kese la. Ndax, am na ñeneen ñu laale ci luubalag xaalisu réewum Senegaal ci yeneen fànn. Waaye, kii di ndeyi-mbill ji moom weddi na loolu ba mu set. Rax-ci-dolli, dóor na Xuwaan ñetti pelent. Kon, fi leek ab diir dees na xam fu wànnent di mujje ak i bëtam.