Caabalug ëttu cettantal gi mi ngi wéy di lëmbe réew mi, rawatina làngug pólitig gi. Àjjuma jale weesu la kuréli way-moomeel yi defoon ndajem-ñaxtu mu am doole ngir ñaawlu anam yi ñu yoree woon junni miliyaar yi ñu jagleeloon mbas mi. Ñii di waa Yewwi Askan wi nag, kenn demul ñu des. Ndax, ñoom it, ci àjjuma jii dañoo bëggoon a amal am ndajem-ñaxtu, nga xam ne loolu benn la ci poñ yi ñu doon naqarlu. Seen mébét nag, mujjewul a àntu. Ndaxte, kii di Perefeb Ndakaaru bi dafa gàntal ndaje moomu ngir liggéeyi BRT ya ñuy def ca Place de la Nation, ak waajtaayu màggalug bés bi Senegaal moomee boppam. Gaa ñi fare ci lëkkatoog YAW, donte ne sax nangu nañu ndogal li ndax kat ku sañul a bañ, sañ a nangu. Waaye, ñoom yemuñu foofu kese, jàpp nañu beneen àpp ngir amal ndajem-ñaxtu mi.
Lëkkatoog YAW jóguñu ci xeex bi ñu sumboon seen diggante ag Nguurug Maki Sàll. Caabalug ëttub cettantal gi dafa gën a yokk xar mi karaw rekk. Ndax kat, kuy wëliis ñu lay fey, bu sa xaju goro réeree danga am loo wëliis. Moo tax, ñii di waa YAW jébbal ab bataaxal ngir sàkkoo amal ndajem-ñaxtu moo xam ne ñetti poñ a ko lal. Bi ci njëkk, mooy dund bu jafe bi. Bi ci topp, mooy ni ñu yoree koom gi, rawatina ni ñu yoree woon xaalis bi ñu jagleeloon mbas mi. Bu mujj bi, mooy ni demokaraasi bi delloo ginnaaw ak ni ñuy jàppe gaa ñi. Seen ndaje moomu nag, mujjul a àntu ndax kii di perefe daf leen ko bañal. Am nag ñu jàpp ne perefe li mu joxe ciy lay ngir gàntal ndaje moomu teey na xel. Ndax, àjjuma jee weesu amoon na am ndajem-ñaxtu. Te, ca àjjuma jooju fanweeri fan ci weeru desàmbar la ñii di waa YAW jébbaloon seen bataaxal. Rax-ci-dolli bu dee jàppandiwul ndax i liggéey mu jox leen beneen béréb ñu defe ko fa. Walla dafa am lu ci laxasu. Mu mel ni kenn ci waa YAW di Usmaan Sonko moom njortoon na xeetu doxalin wii. Ndax, loolu lay wax ci kàddoom yii mu yékkati woon ci seen ndajem-waxtaan mi ñu amaloon ci àllarba jii weesu.
“ Fi may daanele nag, mooy di leen ñaan, ñoom, ñu gore, xam nga gore mooy lan ? Xam nanu ne, mën nañu toog ba bés ba, walla ba ñu ne suba la ndaje mi, ñu ne tere nañu ko. Ndajem-ñaxtu àq/sañ-sañ la ci maxejj bi. Moom, mi ngi wër fu nekk di pólitig, naan ag wër la ñeel koom gi, yab ay kaar ñu jóge fu nekk, ay nitam di amal i ndaje naan ñetteelu moome gi lañuy wax. Lan moo tax saa su kujje gi nee day def am ndaje ñu ne tere nañu ko ? Barki-démb ba tey, fale ci sama dëkk, ay ndaw yoo xam ne ñoom ñoo nekk seen ginnaaw ñoo ngi leen di may ñuy xéy suba ba ngoon jot di ñaxtu. Te, bu doon ndawi Yewwi Askan Wi ñu dóor leen balu fetal. Ba ñu mujjee ñaxtu balu fetal lañu fa dóor ba Idiriisa Gujaabi ak Muhammed Jaata dee fa. Loolu bokkul ci ngor te mënatunu ko nangu ndax yoon dafa am ay càrt. Na ñu gore ndax léeg-léeg, yooyu ñuy def mooy indi fitna. Bu ñu terewul ndajem-ñaxtu mi nu fi doon def ci weeru suwe bi nu gàntalee sunu wayndare, bakkan du ci rot, nit du ci gaañu, nit du ci dem kaso. Ay maxejj yu jóg la dem wax seen naqar, ñibbi seen kër.”
Kàddoom yooyu nag day firndeel ne ñii fare ci kujje gi jàppuñu ne yoon dafa tëdde njaaxanaay. Dañoo jàpp ne ñi fare ci yoon moom lu neex Maki Sàll lañu xam. Seen yoon nekkul ci li yoon wax. Léegi nag, bu yoon jalgatee yoon, ku koy delloo ci yoon ? Moo tax kii di Daam Mbóoj moom, jàpp ne mbir mi, pólitig moo lalu ci ginnaaw, moo tax gaa ñi bëgguñu woon mu am. Waaye nag, ndax kenn dina daas paaka jox sa noon ? Loolu bokk ci li tax mu jàpp ne Perefe bi moom, du dogal dara.
“Perefe Ndakaaru amul sañ-sañ. Dañu naan ko defal, mu def ; bul def, du def. Ñépp xam nañu ne àjjuma jee weesu, ndaje mu rëy lanu fa def. Mu xam ne li nu doon xaar ci bii da koo naroon ful ñett. […] Loolu ñu wax ay tappale la, amul benn liggéey bu mën a tere nu def fa ndaje mi ndax àjjuma jii weesu def nanu ko fa. Liy taafar si mooy di ko jéem layalee BRT bii ak waajtyaayu màggalug bés bi réew mi moomee boppam nga xam ne des na ñetti weer walla lu teg. Kon, loolu mooy ñetti weer yi des kenn dootul ñaxtoo Place de la Nation, mënatuñoo nangul kenn foofu, dañoo dugal seen bopp ci guuta. Li leen metti mooy ki woote walla ñi woote bu ñu wootee nit ñi génn, loolooy seen jafe-jafe, dañoo tiit.”
Loolu nag, day wone ne coow li pólitig a ngi ci biir. Waaye, pólitig moom, ay pexe kese la. Te, kenn du nangu sa moroom di la jam naani. Waaye, cib xeex, ku mënut a àtte rekk war a mën a sot. Moo tax ñii di waa YAW moom, delluwuñu ginnaaw wenn yoon ci xeex bi. Donte ne sax, ñoom, xeeb nañu lay yi perefe bi joxe, terewul ñu nangu ndogal li ba noppi, jël ndogalu ne dootuñu leen nangul ñuy gàntal seen i ndaje ak lu ñu mën di lay. Ndax, nee nañu lii du yoon wu njëkk mu leen di gàntal. Ndajey-ñaxtu yi ñu bëggoon a def fukki fan ak juróom-ñaar ak ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent daf ko gàntal ak bii ci mujj. Mbir mi yemul foofu ndax ñii di jigéeni YAW génn nañu ci àjjuma ji def am ndajem-waxtaan ngir naqarlu ni ñuy doxale ak kujje gi. Loolu la kii de Maymuna Jéey, kenn ci ñoom di biral ci kàddoom yii
“Tey jii waroon nañu ñaxtu ci jàmm ak salaam, nga ni déedéet tegoo ko fenn. Réew moo xam kujje sañu fee wax li mu bëgg a def, kujje gi rekk lañuy tere, moom lañuy jàpp, moom lañuy dal ci kawam, loolu du demokaraasi, jaay-doole la gën a nuru. Judduwunu ne fii ag Nguur la “royaume”, dunu nangu Njiitu réew mu ko fiy indi. Ñu ngi nuy tere, ñu ngi nuy xoqatal, di nu jaxase waaye du jàll.”
Léegi nag, ñoom nee nañu dinañu jébbalaat beneen bataaxal ngir amal meneen ndajem-ñaxtu fukki fan ak ñett ci weer wii ca Ndakaaru ak fépp ci biir réew mi ak ca bitim-réew. Li ñu ko dugge mooy naqarlu ñetti poñ yooyee nu lim. Te, yi ci gën a fés ci jamono jii di jàpp yu bari yi nga xam ne, ñi ci ëpp ci ñoom lañu fare. Ak caabalug ëttub cettantal gi nga xam ne moo lëmbe réew mi. Te, kuréli way-moomeel yi jël nañu seen wàll ci am ndajem-ñaxtu mu ñu amaloon. Li mat a laaj kay mooy lu yoon di xaar ngir jël ci wàllam ?