YOKKUTEG NJËGU SOBLE SI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am soble nekk na lu jafe lool fi mu tollu nii ci biir réew mi. Nde, njëg laa ful bu jéggi dayo. Dafa di nag, mbirum yokkute moom, saa-senegaal yi miis nañ ko léegi. Ndax, daaw ba léegi, saa su xew-xew bu réy jubsee rekk, soble  day yokku. Muy tabaski, di korite, di gàmmu walla màggal gii jubsi, ay frinde lañu ci. Jamono jii nag, njëgu soble si ub na boppi néew-ji-doole yi. Bu dee kilo juróom-benn fukk ak lu teg la daan jar, tey, mi ngi ci ñaari-téeméer ak juróom-fukk walla lu ko ëpp. Te sax, gis soble ci boppam moo jafe ci yenn béréb yi.

Yokkuteg njëgu soble si jur na coow lu réy ci ja yeek kër yi. Ndax, muy yaxantukat yi, di jëndkat yi ba ci sax toggukat yi ñépp a ngi xultu. Ku nekk ci ñoom, yëf yi daf ko yokk jaaxle. Ndax, njaay mi rawatina dund bi moom jógul ci di yokk. Saa su nekk, ñu ne lii yokku na te duñu ko yégle fenn. Mu mel ni kon jot na beykat yi, yaxantukat ak Nguur gi xoolaat seen taxawaay ba askan wi gën a gis boppam ci njëg yi. Ndax kat, ku yuut të moom doo waccu de. Kon, yokkuteg soble si moom deful lu dul yokk ci xar mi karaw.

Ansumaana Saane meeru Sinjaan, di it Njiitul ARM (Agence de Régulation des Marchés) indi na ay leeral ci yokkuteg njëg yi. Dafa di, li sabab loolu jógewul ci biir réew mi kepp. Kenn umpalewul ne soble si moom du ci biir réew mi kepp lay jóge. Moo tax, ni mbir mi ame nii tembere du lu leen bett noonu yépp. Ñi ngi woon ci waxtaan wu yàgg ba tey ngir ut ci ay saafara bees sukkandikoo ci kàddoom yii :

“Noo ngi waxtaan sunu biir te, loolu, laata tabaski gi la. Mbir moomu mooy wéy. Amunu saafara ca Marog walla amagunu. Ndenc gi moom, mi ngi dem, saa-senegaal yi dinañu jëfandikoo ci ayu-bés bi 8.000iy ton, ci weer wi 30.000iy ton. Bu dee ci xew-xew la nag, dañuy jóge ci 30.000 dem ci 50.000iy ton.”

Maanaam, loolu day firndeel ni bu Olànd walla Marog jànkontee ak i jafe-jafe, ak nu ñu mën a deme, dinañu ñu ci laaxaale. Loolu firnde la ci ne sunu beykat yi kese mënuñoo jox réew mi li mu soxla ci soble. Kon, Nguur gi xam na li mu war a def. Waaye, li xaw a doy waar ci mbir mi kay mooy coowal soble si moom daaw ak léegi la mel nii. Ndax, lu ci bari dañu daan nemmeeku yaxantukat yi walla beykat yi di ñaxtu ci ni soble si di yàqoo. Mu mel ni looloo tax gaa ñi di gaawantu ci ni soble si ñàkk a baree ci ja bi ngir ñu yokk njëg yi. Kii di Njiitul ARM li moom rafetluwul doxalin woowu, te, dafa jàpp ne :

“Du càggin ne soble si ñu waxoon juróom-benn fukk walla juróom-ñaar fukk lay jar, amagul ndenc gu ñëw rekk ba li fi des ak us néew dañ koy yokk. Ndax, ci diggante bi amul dara lu soppeeku.”

Dafa jot kon beykat yi ak yaxantukat yi yërëm saa-senegaal yi. Ndax, ñoom lañuy jox soble si. Rax-ci-dolli, bu dee Nguur gi jox na leen ndàmpaay ci wàllu jiwu ak yu ni deme, tëj dig yi ngir ñu mën a jaay bees sukkandikoo ci li Njiitul ARM li wax, war nañoo am xel tuuti. Dafa di nag, mbir mi moom yombul a lijjanti. Ndax, yokkuteg njëg yi moom ku nekk da koy jiiñ sa moroom.

Li am ba des kay mooy ne, limu soble bu bari ñëw na. Ndax, bees sukkandikoo ci li Njiitul ARM li fésal ci xëtu Facebookam mooy ne bërki-démb ci gaawu gi ma nga woon ca waaxu Ndakaaru (Port Autonome de Dakar) ngir jot lu bari ci soble. Kon, mënees na rafet njort ne njëgu soble si dina wàññeeku fii ak ub diir. Waaye, ndax loolu dina wéy fii ak jëluñu matuwaay yi ci war yépp ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj