Nguur gu bees gi séqi na ay jéego ñeel cettantalug pas yi réewum Senegaal jotoon a xaatim. Dafa di, ñoom lii, lu ñu digoon askanu Senegaal la. Te, dige bor la. Ba tax na, bi ñu ñëwee ba tay, ñu ngi ci tànk yooyu. Nde, ci ayu-bés bii ñu génn lañu amaloon aw waxtaan ak kippaango gii ñuy dippe “Groupe ACWA Power” ngir settantalaat pas gi dox seen diggante. Su ko defee réewu Senegaal mën cee gis boppam. Ginnaaw bi ñu waxtaanewaatee pas googu, jëlaat nañ yeneen i ndogal ñeel koppar yi saabalukaayi bitim-réew yi war a fay. Nde, mbooleem saabalukaay yooyu am na lu ñu yokk ci li ñu daan fay.
Mu mel ni mbirum waxtaanewaat pas yi réew mi jotoon a xaatim bokkoon na ci li gënoon a ñor Nguur gi fi nekk. Ndax, li ñu jàpp mooy ne, pas yu ci bari, réewum Senegaal moo ciy loru. Te, liy yoon mooy pas gi nekk pas goo xam ne ñépp a ciy jariñu. Kenn bañ a noggatu moroomam. Looloo tax, ca teel, ñu gaawantu door waxtaan ak réew walla këri liggéeyukaay yu réew mi séqal ay pas ak ci fànn wu mu mën a doon.
Waaye, seen i coppite yamul foofu kese. Ndax, këri liggéeyukaay yi fi nekkoon di dund ci kaw askan wi tamit, dinañ ko digaale ak ñoom. Maanaam, képp ku ci Càmm gi bàyyi woon ngay gundaandaat, danga ca jóg. Ku daan fay tuuti, dees na la yokkal fa sa dayoy liggéey tollu. Moo tax, yenn ci saabalukaay yeek këri liggéeyukaay yiy yëngu ci fànn woowu yëg nañu ko. Ndax, bees sukkandikoo ci xibaar yi dépite bii di Gii Mari Saaña fésal ci xëtu Faacebookam, laata Nguur gii di ñëw, ñii di waa “Canal Plus” ñaar fukki miliyoŋ lañ daan fay at mu nekk. La ko dale 2021 juróom-ñaar-fukki miliyoŋ ak juróom la woon. Waaye, bi Nguuru Basiiru Jomaay Fay ak Usmaan Sonko ñëwee ci la yëf yi soppeeku.
Léegi, kër googu mi ngi fay ñeenti miliyaar ak lu teg at mu nekk. Te, ba tay yamuñu foofu. Ndax, RFI ak juróom-ñeenti “Fréquences” yi mu am, fukki miliyoŋ kepp la daan fay ci at mi. Waaye, loolu dañ na fi. Léegi, juróom-benni téeméeri miliyoŋ ak juróom-ñaar fukk ak juróom lay fay. Naka noonu, Radio Chine ak ñaari “fréquences” yi mu yore, téeméeri miliyoŋ ak juróom fukk lay fay.
Kon, gisees na ne Nguur gi dugalaat na koppar gu takku ci gafaka réew mi. Te, fi mu ko jële du fenn fu dul ci këri liggéeyukaay yi nekk ci réewam daan dunde ñaqu askanam. Looloo tax ñu jël ndogalu fayloo leen loo xam ne yell na ak dayo bi seen liggéey am. Su ko defee mu nekk ànd boo xam ne kenn du ci loru. Ñàqu kenn bañ a siim cerey ka ca des.