YOON A NGI CI TÀNKI MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu Réewum Senegaal diggante atum 2012 jàpp 2024, dina wuyusi ca kanamu Yoon. Muy xibaar bu tukkee ci Mustafaa Njekk Saare mi yore kàddug Càmm gi.

Démb ci àjjuma ji, Mustafaa Njekk Saare mi yore kàddu Càmm gi, doon itam jëwriñu tàggatu bi, yékkati nay kàddu ngir tontu Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu Réew mi ci 12i yi weesu. Fekk moom, Maki Sàll, mu njëkkoon a génn, ci waxtaan wu sunuy naataangooy Jeune Afrique siiwal bàrki-démb ci alxames ji, doon weddi tuuma yees teg ci kawam ginnaaw bi caabalu Ëttub cettantal génnee, keroog 12i fan ci weeru féewiryee 2025.

Ginnaaw duut baaraam gi mu def Ëtt bile nag, Jëwriñ ji Saare dellusi na di ko xamal ni Ëttu cettantal bi bokk na ci campeef yi gën a dëggu ci Bokkeef gi. Te yàgg na settantal ak a dëggal i caytu ci mbiri Bokkeef gi. Kon, moom Maki Sàll, li ko war du lenn lu dul mu dellu jéggalu.

 Bu loolu weesoo, Sëñ bi Saare biral na ni Yoon dina ko topp te dina wuyusi ngir layal ay jëfam ci ni mu yoree woon Réew mi. Nde, wóor na ko péŋŋ ni moom moo nekk ci ginnaaw jëf yi caytu yi wane.

« Amul sikk-sàkka ne, moom [Maki Sàll] dina wuyusi ci kanamu Yoon. Moom mooy ndeyu mbill ji ci jëf yu doy waar yees fi jot a def. […] Duma ko ko woyofalal dara. Lépp li jot a xew ciy ndigalam la ame. Mënees na ko jàppe sax ni njiitu gaŋ li def ay ñaawteef. Mënuñu koo bañ a topp ci Yoon. » (Mustafaa Njekk Saré)

Naka noonu, Jëwriñ ji dellu di fàttali ni Saa-Senegaal yi dañu amoon ci moom kóolute ngir mu andil leen i coppite ci seen dundin. Waaye dafa jëf li muy jëf ba noppi, nëbb leen dëgg ji. Rax-ci-dolli, kenn umpalewul ni jenn jëfu luubal mënul a am te du ko yëg. Ba tax daal muy dëggal ni li Ëttu cettantal bi wéral, bés bees ko jébbalee kilifa yiy doxal Yoon, dina wuyuji ci kanamu Yoon. Bu boobaa nag, bu Yoon gisee ni deful dara dina ko bàyyi.

Ginnaaw bi mu fésalee xibaar bi, jëwriñ ji leeralul kañ lay doon walla fu ci Càmm gi tollagum ca dëgg-dëgg. Waaye lu ci mën a am, lu ni mel, bés bu yegsee, dina doon guléet Yoon di topp am Njiitu réew fi Réewum Senegaal. Ndax, li ko dale atum 1960, ba Senegaal moome boppam ak tay, amul lenn Njiitu Réew lu fi mës jaar ba dem, Yoon di la taqal ba di la topp ci ni nga yoree woon Réew mi.

Terewul nag Yoonu Réew mi sóoraale lu ni mel. Dafa di, saa su ñu taxawalee Ngomblaan gu yees, dees na fa sàmp Ëttu àttewaay bu kawe. Muy fees mën a àttee Njiitu Réew mi ak jëwriñi Càmm gi bees jàppee ni dañu wor askan wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj