Sànq ci bëccëg gi la xibaar bi rot. Moom, Bàrtelemi Jaas miy ndeyu-mbill ji, meeru Ndakaaru, moo ko siiwal ci xëtu Facebookam (story). Li sabab woote bi nag, jotu koo leeral. Waaye, li ñu xamle ci mbind mi mu siiwal mooy ne Usmaan Sonko daf ko bëgg a tëjlu ngir mën a jële meeri bi ci ay loxoom. Ci gàttal, nee na, lii lépp pexey elimaanu jëwriñ yi la.
Naka noonu, taskatu-xibaar bii di Aadama Gay tamit woo nañu ko fa ëttu àtte bii di “Division de la Cybercriminalité”. Moom moo siiwal xibaar bi ci xëtu Facebookam. Li sabab woote boobu mooy pelent bu ko Abbaas Faal defoon ci coowal ASER li.