154 MILIYOŊ AK LU TEG AT MU JOT : MAKI SÀLL SÉDDU NA LAATA MUY DEM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maki Sàll, waajaloon na boppam ca atum 2013. Ndeke, mi ngi doon sóoraale ab wàccam. Moo tax, dafa xaatimoon ab dekkare, séddu, sédd soxnaam ci koppari réew mi laata muy folliku.

Maki Sàll dina jot, at mu nekk, alal ju duun a duun juy bawoo ci nafag réew mi. 2013 la jëloon ab dekkare ñeel i payoor ak i ndàmpaay yu Nguurug Senegaal di ameel képp ku mës a jiite réew mi. Mu ñàmbaasaale woon ci dekkare bi ay jagle yu bari ba jéggi dayo. Ndeke, booba, mi ngi doon waajal boppam. Ndax, ginnaaw bi mu wàccee jal bi, Maki Sàll dina fayeeku, weer wu dee, 5i miliyoŋ ci sunuy koppar. Xaalis boobu, askanuw Senegaal a ko koy fay, jaare ko ci nafag réew mi.

Bésub 17 sãwiye 2013 la Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, xaatimooon dekkareb 2013-125. Muy dekkare bob, day jagleel képp ku mës a jiite Senegaal ag payoor gu tollu ci 5i miliyoŋ weer wu dee. Yemu ca de. Ndax, wëliis payooru weer googu, dees na ko sédd yeneen i jagle yu solowu.
Ci jagle yooyu, bokk na, saa bu feebaree, Nguurug Senegaal a koy faj, muy moom di soxnaam walla ah soxnaam (bu dee soxna yu bari la am). Maanaam, bu ñu feebaree, ci xaalisu Senegaal lañuy fajoo, moom ak soxnaam.
Dees na ko jox it ñaari daamar (oto), ag jollasu kër (téléphone fixe), dëkkuwaay, ak jumtukaayi kër yi ciy dem (mobilier). Bu dee dëkkul ci kër gees ko jagleel, dees na ko ko weccee xaalis, 4i miliyoŋ ak xaaj weer wu nekk.

Ba tey, askanu Senegaal mooy fay tukki yi muy amal ci àddina si, moom ak soxnaam. Ci kow loolu, dees na leen beral 40i miliyoŋ ci sunuy koppar ñeel tukki yooyii.
Bu dee Njiitu réew ma woon bitim-réew la fas yéene dëkki, am na sañ-sañu tànn ñeent nit yi ko soob, ñuy koy liggéeyal. Ñooñii Senegaal a leen di fay. Seen payoor a ngi tollook payooru ndawi Senegaal yi nekk ci àmbaasaad yeek koñsil yi.
Loolu doyul. Nde, ba tey ci ñi koy liggéeyal, jege ko, Nguur war na ko jox ab “aide de camp” boo xam ne dayo bi du sut bu komàndaŋ. Waayee, “aide de camp” boobu, bu nekkee ci réew mi rekk la koy am. Dees na ko jox itam ay sàndarm yiy aar dëkkuwaayam, ñaari way-wattu yiy sàmm kaaraangeem, benn bëkk-néeg, ñaari jigéen yi koy taxawu, benn “standardiste”, benn tusuñe (toggkat), fóotkat bu jigéen, sàrdiñe ak ñaari dawalkat (sófëer).

Bu ko defee, moom Maki Sàll mi namm a dëkk bitim-réew, dina dikkee Senegaal :

– 60i miliyoŋ (5i miliyoŋ weer wu dee) ;
– 54i miliyoŋ (4i miliyoŋ ak xaaj weer wu dee ñeel ndàmpaayu dëkkuwaay) ;
– 40i miliyoŋ ñeel tukki yi muy tukki moom ak soxnaam.
Lépp di tollook 154i miliyoŋ yoo xam ne, booleeguñ ci payoori ñi koy liggéey ak xaalis bi ñu nar a jëfandikoo ngir faju, moom ak soxnaam. Muy xaalis bu takkoo takku.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj