MALI (Musaa Aysatu Jóob)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi nguurug Ibraayim Bubakar Keyta daanoo ci weeru ut 2020, réewum Mali mi ngi doon wéyal ay waxtaan ngir tabb njiit laata ñuy mën a amal ay wote. Démb ci altine ji nag tabb nañ Bah Ndaw. Ay atam toll ci 70, muy tamit ku am taxawaay ndax tollu na ci 1m 95, tax sax ay jegeñaaleem di ko dàkkentalenjool mi. Bah Ndaw nag doomu Malipiir, bokkoon ca xareem laata muy  jàngi ca Risi, ba mu fa noppee la dellusi bokk ci kilifay soldaar yi. Moom Bah Ndaw doon na ku ñu jox cër ca Mali ; ci atum 2014 nekkoon na fa jëwriñ ji ñu dénkoon kaaraange réew mi. Waaye yàggu fa lool ndax mook IBK bokkuñuwoon i gis-gis looloo waral ba mu tekki woon ndombog–tànkam. Moom Bah Ndaw nag, dina jàkkaarlook doomi Mali yi ci àjjuma jii ngir waat. Yéene booboo ngi bàyyikoo ci Asimi Goyta.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj