Paap Buuba Jóob saay na, ginnaaw bi ko feebar bi ñuy wax “Charcot” tërale lu war tollu ci ñaari at ba tere woon koo dox. Ayu-bés bi nu génn, ci dibéer ji, lan yég xibaar bu tiis boobu. Buuba mi ngi faatoo “Lens” ca réewum Farãs, ay atam tollu woon ci 42. Gayndeg Senegaal gi, bàyyi na ginnaaw jabaram “Marion Diop” ak seen ñaari doom Aron Jóob ak Awa Jóob. Mu doonoon futbalkat bu ràññeeku. Mi ngi juddu ci atum 1978, fekk baax ca Tëngéej.
Ni ko ay mbokkam waxe, Buuba gone gu teey la woon, ànd ak dal te yaru. Moom nekkoon na xale bu bëggoon futbal, tàmbale koo ca koñam ag “Asc” Ndefaan laata muy bókki Saltige di ekibub Tëngéej. Foofu la jóge Jaraaf bu Ndakaaru jël ko. Ci atum 1999 la dem Tugal. Bi mu newee Jaraaf nag la xamanteek Ãri Kamara mi ñu wax ne mooy xaritu benn bakkanam, loolu sax yombal na demam “Neuchâtel Xamax” di ñaareelu ekibam ca réewum Siwis. Yeneen yi mu jaar nag mën nan cee lim:
1996-1999 Asc JARAAF.
1999-2000 VEVEY.
2000-2001 Neuchâtel Xamax.
20001-2002 Grasshoppers.
2002- 2004 Lens.
2004-2007 Fulham.
2007-2010 Portsmouth.
2010-2011 AEK Athens.
2011- 2012 West Ham United.
2012-2013 Birmingham City.
Buuba nag ku xarañ la woon ci li muy def. Waaye li gën a tax nag mu ràññeeku ci Àddina sépp, mooy bit bi mu dugal ci caaxi “Fabien Barthez” góolu Farãs 31i fan ci weeru Me 2002. Mu doonoon ndam lu réy ci Senegaal ak bépp réewum Afrig.
Ba ñu ko delloo njukkal ca “Lens” ga mu dëkkoon, néewub Paap Buuba Jóob agsi na Senegaal bërkaati-démb ci àjjuma ji. Buuba nag ba muy yegsi ca “AIBD” njiitu réew mee ko teertu ak ñenn ci ay naataangoom. Delloo nañ ko njukkal lu réy ba tappal ko medaay laata ñu koy jébbal boroomam ci gaawu bii ca Tëngéej ga mu fekk baax ci wetu way-juram bu jigéen.
Nu koy ñaanal Yàlla boroom bi yeesal njébbal ak yërmaande ci moom te xaaree ko Jànnatul Firdawsi.