MÀGGALU TUUBAA (Musaa Aysatu Jóob)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dees na amal màggalu Tuubaa ci 6i fan ci weeru oktoobar. Ginnaaw bi ndigal li  wàccee, Serin Muntaxaa Basiir Mbàkke ci kaddu Seriñ Bas Abdul Xaadr moo ngi xamal mbokku taalibe yi ni, donte ci jamonoy mbas lanu nekk Màggal gi fokk mu am. Ndax bés boobu (18i safar), ci la boroom Tuubaa demoon liggéeyal boroomam ba am lii tey. Moo ngi xamal mbooleem taalibe yi, ni, dina am ag coppite gu jëm ci ay matuwaay ngir xeex doomu-jàngoro jii di koronaawiris, ñu mën cee lim:
Di ñaax mbokk i taalibe yi ñu jënd lu tollu ci 5i alfunniy mask.
Ngir nu moytu dajaloo bi, xew-xew yi ñu daan amal ci bésub màggal gi dina ñu ko jaarale ci jumtukaayu xarala yi ngir ñépp mën cee jot.
Lu tollu ci 5i téeméeri ndaw dinañ nekk ci péggu jumaa ji ngir xool ndax taalibe yi wormaal nañ dogal yi.
Dinañ dakkal itam njaay mi ci wetu jumaa ji ba noppi taxawal 150i dispañseer ci Tuubaa ak li ko wër.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj