FAN LA SENEGAAL TOLLOOK ÑAKK YI ? ( Musaa Aysatu Jóob)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Niki weeru féewaryee ci atum 2020 lañ njëkk a dégg baatu koronaawiris , ci 11eelu fan wa la doktoor yi joxe turu jàngoro ji. Boobaak léegi mu def at ak lu teg, mbasum koronaawiris di nu gën a jaaxal. Diirub bi mu feeñee ak léegi ci àddina wërngal-këpp dal na 108.840.449i nit, faat na lu tollook 2.400.456i doomi-Aadama, waaye tamit 61.102.173i nit wér nañ ci. Kon loolu di firndeel ni tawat bu nu mën a xeex la sunu toppee ndigalu doktoor yi te moytandiku tere yi.

Koronaa ci Afrig.

Koronaa-wiris mi ngi wéy di lore ak doole ci Afrig. OMS di kuréelug wérgi-yaram ci àddina sépp mi ngi xamle ne, fi mu nekk nii way-faatu yi yokku nañ lu tollu 40% ci benn weer ci Afrig. Xibaar boobu nag, jur na njàqare lu réy ci réewi Afrig yépp. Lu ëpp 22.300i way-faatu nemmeeku nañ ko ci 28i fan yii nu génn, te 16.000i rekk lañu woon ca weer wi nu génn. Mu nekk lim bu takku lool, ndax, bu ñu xaymaa, 6.300i doomi-Aadama yokku nañ ci.

Lu waral googu yokkute ?

Doktoor yi nag xamle nañ ne yokkute googu dara waralu ko lu dul xeetu wiris yu bees yi ñu nemmeeku te ñu mën cee lim ñaar : “variant Britanique” ak  “variant sud-Africain”. Xeetu wiris bu bees boobu ñuy woowe “variant britanique” ñoo ngi ko njëkk a gise ca Niseryaa ak Gàmbi laata ñuy dugg ci yeneen réewi Afrig yi. Mu mel ni kon, doomi-réewum Gàmbi yi mbaa yu Niseryaa ya nekk ca Àngalteer bokk nañ ci ñi ko indi ci Afrig ndax bari nañ lool foofule. Boobu wiris ñu koy waxit “B.1.1.7” wuute naak bi nu xamoon, bokk na ci ay màndargaam : sëqët, gaaw a sonn ak metitu purux. Rax-ci-dolli moo gën a gaaw a wàlle wiris biñ xamoon te gën a gaaw a  lore itam. Kon, mu mel ni dañoo tàmbalee wax waxi ñakk rekk xar-kanamu wiris bi daldi soppiku.

Waaw, nun waa Afrig ban ci ñakk yii lanuy jël sax?

Pfizer-BioNTech bu Almaañ ak Amerig walla Moderna bu Amerig, AstraZeneca bu Àngalteer, SpoutnikV bu Riisi, walla Sinopharm bu Siin ? Ñi seen xam-xam màcc ci wàll woowu ñoo ngi xamle ni bun ci mën a tànn it nanu bàyyi xel ci njëg li, nanu wóor it ne mën nan ko denc. Ndax pikiir bëggul tàngaay te sunu réew yii bari na yenn diiwaan yu kuraŋ amul. Kon bu nu sukkandikoo ci loolu mën nañ wax ni, dinañ soxla jumtukaay yu mucc ayib ngir ñakk gi mën a jaar yoon. Réewum Senegaal, ñu ngi xamle ni dinañ jot ci njeextalug weeru féewaryee ak ndoorteel wéeru màrs 1,2 milyoŋi ñakki AstraZeneca ak 200.000i junniy ñakki Sinopharm.

Ndawi Afrig yi dinañ pikiiroom déet?

Li wér te wóor daal mooy coow li bari na lool ginnaaw biñ waxee waxu ñakk yi. Ndaw ñi ñoom nee nañ ñoo lànk ba tëdd ci suuf ndax dañoo jàpp ne pikiir yii, am na lu ci laxasu. Loolu tax na (Africa CDC) amal benn luñtu ci lënd gi ngir xam taxawaayu ndaw yi ; ca Kamerun 43% dalul seen xel,  72% lañu Keeñaa, di 93% Niseer. Ci weeru sanwiyee wii def nañ beneen jàngat ngir saytu xalaatu ñenn ci saa-Senegaal yi waaye li ñu gis mooy 54,4% nangu nañ pikiiru. Bu ñu ko méngalee ak beneen lànket bu waa « Bureau de prospective économique du Sénégal » def ci desàmbar 2020 wone woon na ni 38,3% doŋŋ ñoo nangu woon pikiiru. Kon ba tey mën nañ wax ne am na ñu bañ waaye tamit am na ñu nangu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj