Waa Mamel, fii ci Ndakaaru, naqar ak tiis lañ fanaanoo. Li ko waral mooy tuut-tànk bu tollu ci benn at moo daanoo ci seen taaxu kër, ñàkk bakkanam. Ci Senenews mi nu jële xibaar bi, kii faatu ak séexam ak seen mag ju am 4i at la seen yaay boole tëj ci kër gi ngir mën a dem ayeropoor Blaise Diagne gunge ab xaritam. Ci ginnaawam, la benn séex bi am lu mu waddle, bëgg koo for, ci laa daano. Naka lañ ko yóbbu ca bérébu fajukaay ba, yàggul dara, mu génn àddina.
Nee na ñu ndaw soosu jur xale yi mi ngi ñibbisi ci weti 22i waxtu. Laata muy agsi jot nañ koo tàgge doom ji. Muy tiis wu réy. Xéy-na mu war cee boole réccu.
Li wolof naan, yedd yërëm a ko gën, ndaw si war a boole naqar ak réccu ku ko yërëm la soxla. Waaye li jaaxal ñépp mooy naka la xel mën a nangoo ngay tëj ci kër gune gu am 4i at doŋŋ ak ay rakkam yoo xam ne xéy-na sax feraguñum soow, génn te Yàllaa xam kañ ngay delsi ? Lu tax xalaatoo ni musiba mën na am te duñu am ku leen wallu ? Ndogal dëgg la. Yenn saay nag ndogal loxoy boroom mi ngi ci biir. Waajur bu nekk, sàmm la ci njabootam. Yal na séex bii faatu xippee àjjana.
Ndaw si, yal na ko Yàlla may xolu muñ te sàmmal ko ñi ci des.