NJUREEFI BAC 2024 YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋante BAC bi jeex na ci ayu-bés bii ñu génn. Njureef ya ca tukkee rot nañ. Maanaam, limub ñi def joŋante bi, ñi ci am ak ñi nga xam ne amuñu. Ñi doon def BAC bi tollu nañu ci 159.499i ndongo, 75.462i ndongo ñoo ci am.

Ci weneew waxiin, bu ñu ko xaymaa, day doon 48,71% limub ñi jàll ci joŋante boobu. Limub ñi jàll ren moo gën a néew bu atum 2023 donte ne sax, limub ñi def ren moo ëpp tuuti. Mu des léegi, joŋante bii ñuy dippee BFEM.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj