Tey jii, boroom xam-xam yaa ngi gëstu làmmiñu wolof, ci fànn yu ni gàññ, dale ko ci ay xarnu aju ci xam-xamu kàddu, bind, tëgg kàddu, xam-xamu gàggantikaay, ci biir yeneen tolluwaay ci xam-xamu làmmiñ.
Liggéeyu tasaare mi (tekkim Alxuraan, Biibal, Ndéyi-àtte ju réewum Senegaal, Tëralinu ja yu njémmeere yi) booleek liggéey yu pasin te wuute yu ñu bind ci fànn wu ne, ñoo woomal, ci dox bu yàgg, kéewu njàngum làmmiñu wolof.
Ci wàllu xarala yu bees yu xibaar ak jokkoo, seetlu nanu ni wolof a ngi ci géewi njàngale ak njàng mi sukkandiku ci nimerik, ñu koy jëfandikoo lu bari ci njoxem xibaar. Wolof, nekk na itam ci Wikipediyaa, nekk ci Guugal ak ci jumtukaayi Window.
Bokk na yit tey jii, moom ak Pulaar, ci làkki kembaar yi Akademi Làkki Afrig (AKALAN) tànn ci biir làkki Afrig yi.
Ay yaxal yuy tëral mbindinu làkk week teqalem baat yi am nañu. Bi ci mujj mooy lim 2005-990 bu 21 Oktoobar 2005, di bi nu war a jëfandikoo. Teewul mbindinu wolof wi, ni ñu koy jëfandikoo ba tey jii, toppul yaxal yooyu. Muy ci yëgle yi, di ci làngi pólitig gi, mbindin wi ñaare ay yàq rekk la. Loolu di lu doy waar ci réew mu mel ni Senegaal, di réew mu ku nekk di jaay ngóora ci wormaal, lu mu mën, àttey làkkum farañse bi nu àbb. Mbindum farañse moom, du am, mukk, benn njuumte, genn yàqute. Worma jooju defuñu ko ci làkk yi nu moom.
Yàq ak jalgati gu sax dàkk googuy am ci tëralinu mbindum wolof, gàllankoor la ci xeex bi ngir suqali ak gànjaral sunu làkk yi. Loolu dafay nasaxal fonk gi nu waroon a fonke sunu bopp, di laal jeexital ci worma ji nu am ci sunu bopp.
Ngir samp pexe yu dëgër yu fiy déqati doxalin woowu, ay ma-réew yu jigéen ak yu góor, di yëngu ci liggéey, ci gox yu wuute (jàngalekat, bindkat, ma-làmmiñal, ma-mboor, ma-yoon,…) ñoo ànd, fas yéene dimbali seen mbokki[1] réew, ba ca ñoñ biti ña sax, ci ñu mën mbindinu sunu làkki réew yi te mën leen a jàng ci nu yomb. Ci wolof lañu tàmbalee, wànte dinañu yaatal liggéey bi ci yeneen làkki réew mi.
Mbooloo mii làkki réew mi soxal, jubluwaayam bu mag bi mu samp, mooy xiirtal ak jàmbarloo ñi dëkke mbaa baaxoo ci réew mi, rawati-na taskati xibaar yépp, ci ñu yokk gëddaal ak gànjaral sunu koomum làkk mii ak mbatiit te jox leen cér bi ñu yelloo tigi. Ngir amal loolu, fas na yéene dimbale nit ñi, yombalal leen na ñuy jote ci xam-xam ak mën-mën ngir jëfandikoo wolof gu tegu ci yoon, ci fépp fu ñu koy bind.
Mbir mi nag, narul a yomb, ndax ci mbind mi nuy faral di gis, di ko jàng, ci sunuy pénc, rawati-na réew-taax yi ak ci tele yi, li ci ëpp lépp, ñu mbind ko ci wolof, teguwul ci yoon. Ay yàq rekk la. Ci misaal, sooy wàcc ca ayropooru AIBD (Aéroport international Blaise Diagne de Dakar) bu Ndakaaru, baat bii di jaam lañu lay teeroo, te jaam « nit ku nekk jaam » di saafaanu jàmm, baat bi ñu ci jublu woon, bi ñu koy bind. « Dalal ak jaam » lañu fa bind te mu waroon a doon « Dalal ak jàmm » ngir teeru ñiy egsi Senegaal.
Wànte nag, teewul nu war a sargalu ci jéego yu am solo yi ay kër di def, yu ci mel ni Orange walla « start-up » bi tudd Sunu nataal jëm ci wormaal mbindunu wolof. Ñu ngiy def seeni kem-kàttan ca na ñuy binde lañuy yéene ci pano yi nekk ci mbeddi réew-taax yi walla ci wetu tali yi.
Noo ngi rafetlu it telewisyoŋ ITV biy bind xibaar yi ci wolof, donte sax, yenn saa yi, ñuy def ay njuumte yu fés yu ñu jubbantiwul.
Seetlu nanu itam ni Njiit li Maki Sàll, tànn na, ab diir a ngi nii, di tiwit ci wolof, te mu ngi sonn bu baax ciy bataaxalam, di leen bind ci mbindin wu jub xocc. Mën nanoo wax, moom moo war a jiitu ci li yaxalu mbindinu làkk mi tëral, wànte rafetlu nanu lool doxalin wi. Jëf jooju jees di sant, as ceññeeru yaakaar la ci biir doxalinu jalgati gu jéggi dayo ci mbindinu làkki réew mi.
Mbooloom Ànd Wattu Làkki Réew Mi, mu ngi gaaral ci suuf, ñaareelu yëngoom gu aju ci topp ak jubbanti yenn mbindin yiy « xajamal » kéewu mbooloo mi.