Cër bi nu jox farañse bi tax na ba, kenn sañul a xët sàrt yiy yoonal mbindam. Te sax, boo juumee ba yàq ci baat bi gën a ndaw, réew mépp mbamb la, ak koo mënti doon. Waaye, bu dee wolof bi moom, nu neex waay binde, dara du la ci fekk.
Ndeysaan, dangay foog ne sax, làkki réew mi, ñoom, amuñu ay sàrt yiy yoonal seenum mbind. Aycaleen nu jubbanti, ci mbindum wolof mi, yenn ndëngte yiy ñaawal ak a tilimal xar-kanamu réew mi.
ÀND JUBAL MBIND MI !
Ci tekkib Paap Aali Jàllo (Iniwérsite Gaston Berger)
Àlluwa ji
I Kàddug dugge
II Mbind mi ñu bëgg a jubal
1- Ayeropooru Ndakaaru
2- Turi jotaayi tele Senegaal yi
3- Turi làng walla kuréli pólotig
4- Turi « start-up »
5- Àlluway-siiwal
Ñi sos KIPPUG WATTU LÀKKI RÉEW MI
Kilifa yi ànd ak nun ci siiwal yaxal bii
Kàddug dugge
Danu seetlu ne, li ko dale ati 2000 yi ba tey, nguur geek làngi pólotig yi, ñu ngiy jéem a faaydaal làkki réew mi. Nu koy rafetlu. Muy càkkub-dëkki-taax yi, kow tali yi ak yéenekaay yi, bu ci nekk a ngiy fésal làkki réew mi ak ni askan wiy dundalaatee sunug moomeel. Ci misaal, àlluway-siiwal yi, turi jotaayi tele yi, turi làngi pólotig yi… bu ci nekk, bindees na ko ci wolof doonte ne, yenn saa yi, ñu rax ci farañse.
Naam, itte jaa ngi fi. Waaye, mbind mi dafa des lu baree bare. Dafa mel ni, cër bi nu jox mbindum farañse bi, joxunu ko mbindum làkki réew mi, rawati-na wolof bi. Moom kay, kenn sañul a xët sàrt yiy yoonal mbindum farañse mi te mbambuñu la, ak koo mënti doon. Waaye, bu dee wolof bi moom, nu neex waay binde, dara du la ci fekk. Ndeysaan, dangay foog ne sax, làkki réew mi, ñoom, amuñu ay sàrt yuy yoonal seenum mbind.
Ndaw njuumte lu réy !
Ci atum 1971 lees jëkk a génne ab dekkare buy sàrtal mbindum wolof ak teqaleb baat yi. Dekkarey 1975, 1985 ak 2005 yi ci topp yépp, ci bu jëkk bi lañu wéeru, bu ci nekk indi ciy coppite. Bu dee àtteb 77-55 biy sàrtal mbindum làkki réew mi, moom, bésub 10eel ci awril 1977 lañu ko yoonaloon. Àtte bi dafa tëral ne, bépp yaxal bees jagleel mbooloo mi, te nu bind ko ci wolof walla seereer, warees na ko dëppale ak dekkare yiy sàrtal mbind mi ak teqaleb baat yi ci làkk yooyule. Ci yoon, képp ku jalgati àtte boobu, yeyoo nga ab daan, ni ko dogi 2, 3 ak 8 tërale ci garug-àttey jalgati gi. Dëgg la, jamono yooyu, jubluwaayu pólotig la àtte bi amoon. Waaye, tey, warees na jéggi loolu, sóoraale làkk yeek seenum njàngale ci jubluwaay yi. Su boobaa, dees na mën a wattu mbindum làkki réew mi, dakkal yëfi maa-tey yi.
Rafetul, 50i at ginnaaw bees sàrtale mbind mi, nuy wéy di dajeek i ndëngte ñeel làkki réew mi. Te, mbind mi, taxu koo soppeeku noonu, rawati-na bi mu amee àtteb yoonal.
Njuumte yooyu yàgg fi lool, tëw a deñ. Booba ak léegi, dañuy nasaxal faayday làkki réew mi. Te, loolu dafay sabab xeebeel ñeel sunuy làkk, aada ak cosaan. Bu yàggee, dinanu gën a suufeel sunu bopp.
Kippug làkki réew mi dafa di ab kurél gu ëmb ay jigéen ak i góor yu farlu ci làkki réew mi. Li ñu bëgg mooy xirtal taskati xibaar yépp, ñaax leen ngir ñu gën a sàmm sunu moomeelug làkk ak aada. Ngir mottali yéene bu ni mel, nangu nañu leen a baaxe seen jaar-jaar ak seen xam-xam ba nu mën a amalub set-setal ci li fi nekk tey, ak li nar a ñëw ëllëg. Ci gàttal daal, jubluwaay bi mooy, fexe ba mbindum làkki réew mi jaar yoon. Bu ko defee, dootunu jaawale « jaam » ak « jàmm » ni ko ayeropoor AIBD defe. Ndekete, ngir dalal way-tukki yi, dañu bind ci gegub teer bi « Dalal ak jaam » te ñu waroon a bind « Dalal ak jàmm ».
Te xam ngeen ni jaam du jàmm.
Kippug wattu làkki réew mi di leen baaxe ay jubbanti ñeel yenn ndëngte yiy ñaawal ak a tilimal xar-kanamu réew mi.
Mbind mi nu bëgg a jubal
I- AYEROPOORU NDAKAARU
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Dalal ak jaam |
Dalal ak jàmm |
II- TURI JOTAAYI TELE SENEGAAL YI
SEN TV
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Feem ci keur |
Feem ci kër |
Guis-Guis |
Gis-Gis |
Li ci rewmi |
Li ci réew mi |
Ndoumbelane |
Ndumbelaan |
Sama gokh |
Sama gox |
Sen jotay |
Seen jotaay/jataay |
Sen xeweul |
Seen xéewal |
TFM
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Faram face |
Faramfàcce |
Firi gent |
Firi gént |
Jakaarloo bi |
Jàkkaarloo bi |
Jánggat |
Jàngat |
Jonganté |
Joŋante |
Li ci penc mi |
Li ci pénc mi |
Ngonal |
Ngoonal |
Sama keur |
Sama kër |
Wakhtane ak |
Waxtaan ak |
Ña woon demb |
Ña woon démb |
Khew khewi dine dji |
Xew-xewi diine ji |
Yeewu leen |
Yeewuleen |
2STV
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Aarru mbed |
Aaru mbedd |
Bantamba |
Bàntàmbaa |
Keur gui |
Kër gi |
Pencci reew mi |
Pénci réew mi |
WALF TV
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Selebe yoon |
Selebe-yoon |
Diiné ak diamono |
Diine ak jamono |
Weer ak werlé |
Wér ak wérle |
Sa ndiogou |
Saanjóogu |
RTS
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Njangatu besbi |
Njàngatu bés bi |
Reeni koom koom |
Reeni koom-koom |
Takussan |
Tàkkusaan |
III- TURI LÀNGI WALLA KURÉLI PÓLOTIG YI
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Benno bokk yakaar |
Bennoo bokk yaakaar |
Bess du niakk |
Bés du ñàkk |
And Jef |
Ànd Jëf |
And Défar Sénégal |
Ànd defar Sénégal (Senegaal) |
Bloc des centristes Gaïndé |
Bloc des centristes Gaynde |
(CDP) Garab-GUI |
(CDP) Garab gi |
Sénégal moo niou saff (FNP) |
Sénégal moo ñu saf (FNP) |
Suxxali Reew Mi |
Suqali Réew Mi |
FAR / Yoonwi |
FAR/Yoon wi |
Benno jubël (FSD/BJ) |
Bennoo jubal (FSD/BJ) |
GARAP / ADS |
GARAB / ADS |
MPS / SELAL |
MPS / SELLAL |
Ñiaxx Jariñu |
Ñaq jariñu |
PSD/Jant–Bi |
PSD/Jant bi |
Reenu Rew |
Reenu Réew |
Rewmi |
Réew mi |
UPAS/Niax Teed |
UPAS/Ñaq Tedd |
UDF/Mboolomi |
UDF/Mbooloo mi |
Luy jot jotna |
Luy jot jot na |
Pastef Patriotes du Sénégal |
Pastéef |
IV- TURI « START-UP »
Li ñu bind |
Li ñu waroon a bind |
Aywadieune |
Aywa jën |
BaySeddo |
Bay Séddoo |
Etou nature |
Ëttu nature |
Jokalante |
Jokkalante |
Jokko-annonces |
Jokkoo-annonces |
Lifantou |
Liifantu |
Manko |
Mànkoo |
Ndiarte |
Njarte |
Niokobok |
Ñoo ko bokk |
Outalma |
Utal ma |
Sakanal |
Sakkanal |
Tew mou tew |
Teew mu teew |
Tolbi |
Tool bi |
Tong Tong |
Toŋ-toŋ |
Wanter |
Wànteer |
Xibar.net |
Xibaar.net |
Yobanté Express |
Yóbbante Express |
IV- Àlluway siiwal
Leeral.net
Jóoni-jóoni
Orange money mooy sunu kalpe
Wari, Jege na, Wóor na, Gaaw na
Matelas Dodo Doole rekk moo wóor
Joŋe Dëbbal Lu saf !
Feem bu bees “système” la
Dina xëb, dina set, ànd ak xet gu neex