Pólitiseŋ yeey faral di def lu xew ñu daldi àddu ci tàng-tàng bi. Loolu, nag, warul a jaaxal kenn. Ndaxte, ñoom, daanaka, bu waxtu jëf jotee, ku ci taxaw di seetaan tàkk nga. Gaa, du li gën. Waaye, nag, buñ demee ba mbirum «Sweet Beauté » di bëgg a gàkkal sunub demokaraasi, kenn warta noppi, ñépp a war a sotle réew mi.
Li yéeme ci mbir mi mooy ne, li muy réy ak a doy waar yépp, dafa xaw a reetaanlu. Nde, mbir mi, ay léeb lay gën a niru. Laaj biy yëngal tuñ yépp mooy : naka la Usmaan Sonko, njiitalu PASTEF di sañ a wàcce boppam, sàggan bay tëdde jigéen ju am ludul 20i at astemaak di ko siif ci béréb boo xam ne, weñ sax bu fa naawee ñu dégg ko ? Dàmpukaay boo xam ne, mu ngi cig kër gu, daanaka, 10i nit ñoo fay nekk guddeek bëccëg. Foofu, naka lañ fa mënee jaay doole as ndaw, tëdde ko fa ay yoon teg ci di ko xëbal ak ñaari gànnaay te kenn du ko yëg ? Ndax Usmaan Sonko dofe na noonu ? Ak ni kër gi tuutee te am iy fuglukaay… Du yuuxu, du jooy te du benn bërti-bërti bu fa kenn mës a dégg. Lii, bu dul ay léeb itam, caaxaan du ko weesu.
Sonko xam na xéll ne ay noonam ñoo ngi koy yëddu saa su ne, di ko jéem a fexeel. Bañ na ko ba buy tukki, du nangoo dencluy wëliisam ci suufi roppëlaan yi. Ku ni mel, naka lay siife as ndaw, ak ni darajaam tollu ci miim réew ? Waaye, fen, du bijjaaw.
Ñi nas kooto bi, bëggoon ko gasal kàmb, sóoraalewuñu woon ni boroom dàmpukaay bi du far ak ñoom. Kii, kàddu yu leer nàññ la yëkkati. Ciy waxam, ay sàmbaa-bóoy a diisoo ci pet ngir daaneel Sonko. Dara taxu leen a jaar ci Ajaa Raabi Saar lu dul ay jaar-jaar ak xelu xale mi ci moom. Ndege, Ajaa Raabi Saar, ci li ñenn ñi wax, bare na caaxaan, bëgg na fo, te ku sob a sob la. Melokaanam boobu, moo taxoon nooni Sonko yi bëgg koo jëfandikoo nib gànnaay ngir wàcce ko ci nii, mbaa ci naa.
Xaalis mënul a jënd as gor. Fa seen pexe moyee tamit mooy ba ñu yaakaaree ne mbir mu tollu nii, ci réew mu mel ni Senegaal, du senn. Waaye, ci waxtu yu néew la law ba suul yeneen yitte yépp, ñépp di ko waxtaane. Dañu sax fàtte mbas mi xam nga ne, bés bu Yàlla sàkk muy gën a rey.
Askan wi, moom, dafa mer ba futt. Te, meram googu, kenn waralu ko ku dul Maki Sàll, njiitu réew mi, ak nguuram gi. Réewum demokaraasi, bu jaaree yoon, kàddu askan wee fa war a sut geneen kàddu gum mënti doon. Askanuw Senegaal, nag, Sonko la jox kàddoom. Loolu, sikk amu ci. Xew-xew yii doy nañ ci firnde. Kon, ak luñ mënti sos ngir daaneel Sonko, askan wi, moom, àtte na ba noppi. Warees na xam ne, léegi, ñépp a yeewu, naxe-mbaay moo fi jeex. Mu mel ne, Sonkoo ci amee ndam.
Ba sun-jonni-Yàlla-tey jii, ay ndaw yu gisoon seen bopp ci moom ñoo toppoon ci Sonko. Waaye, fii mu ne nii, nit ñaa ngi màbbe fu nekk, di ko jàppalesi. Loolu day wone ni dooleem yokkoo ci làngu pólitig gi. Bu dee dayob Sonko da doon màgg ndànk-ndànk, tuuma yii dañu yokk bayreem.
Kasu pólitig gu kii walla kee amalun solo. Waaye, demokaraasi lañu bëgg a gàkkal. Te li am sax, mooy ne, ñi ko waroon a wattu, ñoo koy doyadil. Dara desul ginnaaw. Nee nañu ndaw si dañ koo siif. Waaye, moom de, ba mu kalaamee Sonkook yoon ba tey, da ni mes, ni meles.
Waxatuñu dara ñu jël maniyu boroom-kër yóbbu cib kilinig. Loolu doyul, ñuy xoqtal ak a jéem a ger boroom dàmpukaay bi ngir mu soppi seedeem, daldi taqal Sonko.
Basiiru Gèy moom, mooy toppekat bi nga xam ne, lu ko nguur gi sant mu def. Ñu daldi woolu Sonko ci maa-tey, mel ni du dipite bu malaanum kiiraay muur. Ñu ni déet-a-waay, takk-der yi wër këram ak seeni gànnaay. Ñoom daal, ñuy jalgati yoon nimu leen neexe.
Loolu doyul, Péncum réew mi ne dafa wote ba toog, keroog bésub 11eel ci féewaryee, ngir teg Sonko ci yoon woo xam ne kenn gëmatu ko faf. Wallaay, lii daa mujj doon tiis sax.
Lu jiin Njaag a, te njiitu réew meey Njaag. Ndaxte, mooy buur di bummi. Looloo waral tamit ñetti kuréli dogal yi waroon a tëdde njaaxanaay mujje weŋŋ.
Naam, Senegaal du réewum jaay doole mi ñuy wax, waaye xoqtal beek bunduxataal bi du fi lu bees. Li fi bees, jamono jii, mooy nim fése, ñaaw, ruslu te xaw a reetaanlu. Maki Sàll xamul bët, faalewul kenn. Te, loolu, jar naa tiit bu baax. Ponk bu mujj bii laaj na taxaw-seetlu.
Am na ñenn ciy farandooy Maki Sàll ñuñ weg lool ndax dañoo mës a gëm Senegaal ak lu koy jëmale kanam. Su leen neexee ñu taamu jàppale ko : miin nanu dem ak dikk ci géewu pólitigu Senegaal. Dara nekku ci. Li neexuta dékku kay, mooy naka lay xeltukat yu màndu te am faayda ni ñoom mënee seetaan lii, ne cell. Mbaa du Njiitu-réew mi dafa yóbbu seen fit ?
Suñ doon doxal yoon, Maki Sàll dina xam ni du lu ko neex rekk mu def te dara du ko ci fekk. Ñi mu àndal waruñu ko cee seetaan benn yoon. Moom daal kenn woowu ko ci ruq, déey ko.
Mën nanoo jëli gaa ci pàrteem ay kàngam yu dul jaaroo taal ak Sonko. Waaye, dinañ am kersa ci doxalinu Maki Sàll. Tóoxidóona gu mu jóge, jàll ca ga ca des. Bërki-démboo-njaay, Karim Wàdd, démb Xalifa Sàll ak Aminata Ture ; ñépp liñ teg ci seen ndodd mooy ne dañoo bëgg a wuutu Maki ci jal bi. Waay-waay kenn mënu koo déey ne “màggal nit màggal gu jéggi dayoo jigul pólitiseŋ ci miim réew”. Ni muy doxaleek Sonko du ko jig, dafa nar a xëtt xolam rekk, balaa yàgg mu ne fi naan su ma yëgoon. Ñépp xam nañ ni “lu ëpp tuuru” te Sonko ciy yëkkatiku ëllëg-ak-sibir.
Xéy-na, nguur gi da doon làmbaatu ba xam fu dooley Sonko tollu. Ndax, ci xarala yu bees yi kese la am i farandoo am déet. Waaye, daj na. Ci diir bu gàtt, ñu baree fippu, génn ci mbeddiy Ndakaaru yi, Luga, Biñoona, Mbuur ak Sigicoor. Te buñ deful ndànk dina law. Rax-ci-dolli, Pastef da cee gën a yëkkatiku bitim-réew.
Li ci Maki Sàll waroon a jànge mooy ne, am na lu koy xaar bés bu bëggee amaat ñetteelu moome. Na xam ne li jig Alasaan Daramaan Watara ak Alfa Konde du ko jig.
Su gëmoon Yàlla, dina xam ni mënoo taal am réew ngir rekk bëgg a wéy di ko jiite. Diggante awril ci atum 1960 ak 2021, ay milyoŋi doomi-Senegaal jaar nañ fi. Ci seen biir, ñeent rekk a fi am màqaamaam nekk njiitu réew. Milyoŋ yi ci des te mësuñoo jiitem réew, wàññiwuleen dara. Te, bu yaakaaree ni moo leen ëpp xel mbaa kàttan, day nax boppam.