Léegi leer na. Jàppal nañ wote yi ab bés. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo tànn bésub 24 màrs 2024 ngir askan wi fal ki koy wuutu ci jal bi. Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi jotoon na jàpp sax bésub 31 màrs 2024. Waaye, dafa mujje dellu ginnaaw, tënku ci ndogalu Njiitu réew mi.
Démb, jiixi-jaaxa amoon na. Ndax, bés bi Njiitu réew mi jàppoon ak bés bi Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi àppaloon méngoowuñu woon.
Njiitu réew mi, Maki Sàll, ginnaaw bi mu tasee Càmm gi ci ngoonug démb gi, dafa jàppoon bésub 24 màrs 2024, muy bésub wotey njiiteefu réew mi. Nes-tuut, Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi tamit jàpp bésub 31 màrs, daldi koy siiwal. Coow li ne kurr : benn wote, ñaari lél (date).
Tey ci alxames ji nag, Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi leeral na lépp. Ndax, ñoom juróom-ñaari àttekat yu mag yi, dañu xaatim ab yégle bob, dañ ci wax ne bés bi Njiitu réew mi jàpp mooy bu baax bi. Ndax, ci seen i wax, Njiitu réew mee am sañ-sañu jàpp bésub wote. Dafa di nag, moom la ko Yoon may. Ñoom àttekati Ndajem Ndeyu Sàrti réew mi, bi ñuy jàpp bés, dañu sukkandiku woon ci yàccaaralu Caytu gi ak bëggoon a wéyal doxalinu wote yi. Li ñu ko dugge woon mooy fexe ba askan wi tànn Njiitu réew lu bees laata moomeg Maki Sàll giy jeex. Waaye, ndeem Njiitu réew mi mujje na jàpp bés, ñoom dañuy tënku ci ndogalu Njiitu réew mi, ni ko Yoon santaanee.