XAREB IKREN BI – COSAAN LI AK NJEEXITAL YI 1/3

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal Riisii – Ikren moo lëmbe àddina si. Daanaka, ñaari ayu-bés a ngi nii, moom rekk lañuy waxtaane ci fépp foo dem ci àddina si. Boobaak léegi, wax ji bare na, nag… lool sax.  Tele walla rajo boo jàpp, moom lees fay waxtaane, li ci ëpp. Yéenekaay yi di ko jagleel ay yaxal yu dul jeex. Internet bi tamit fees ci dell. Waaye, saa bu coow baree, fen dana jaxasook dëgg, muur ko. Te, ku deful ndànk, dinañ la gëmloo lu safaanook dëgg. Nde, bi xare bi jibee ba léegi, booy seetaan tele yi, di déglu rajo yi ak a jàng yéenekaay yi ci ëpp, day mel ni Riisii moo sooke lépp, moom rekk a di ndeyu mbill ji. Waaye, ndax noonu la fa demee dëgg-dëgg ? Ndax xare bi, diggante Riisii ak Ikren kese la ? Lan moo ko sabab ? Luy cosaan li ? Yan njeexital la mën a am ci àddina si ? Seen yéenekaay LU DEFU WAXU, ci xalima Paap Aali Jàllo, fas yéene leen indil ay leeral ñeel yuqub xare bi am tey, ci ñaari xaaj. Xaaj bu njëkk bii day biral xew-xew yi dox diggante 1945 ba 1999, di wone cosaanul sabab yi sooke xareb tey bii.

 Bu dëgg réeree cim pénc, mag ak a ci dëgg tànkam

Saa bu xare jibee, bala benn bakkan di rot, dëgg lañuy njëkk a tàgge. Nde, ni ko tubaab yiy waxe, ku bëgg a labal sab xaj, jiiñ kob say. Waaw, bi xare Riisii ak Ikren bi dooree ba tey, daanaka Riisii la àddina sépp tam dëmm, rawatina réewi sowu yi. Kibaraan yi, muy tele yeek rajo yi, yéenekaay yi ba ci internet bi, ñépp Vladmir Poutine, njiitu réewum Riisii, lañ joxoñ baaraamu tuuma. Genn kàddu rekk ngay dégg : « invasion russe en Ukraine », maanaam congum Riisii ca Ikren.

Coow li ne kurr. Poutine jàppal fii, Poutine bàyyil fee. Faramfàccekat yi ame tele yeek rajo yi, boroomi xalima yiy bind, widewoo yi, nataal yeek ndéggat yiy ñaawal ak a tilimal deru Riisii ak i njiitam di law. Ay daan yu mettiy tegaloo ci kow réewum Riisii : ay daan ci wàllu koom-koom, politig, xare, ba ci wàllu tàggat-yaram. Lépp, nag, Amerig ne ci ginnaaw, di nos ak a nocci ak a xamb taal nib jigéen ak wujjam. Xam naa yaa ngi naan waa Paap Aali mii moom, day waxtu walla dafa faral Riisii ?

Ma ni la « déedéet ! Waxtuwuma wallaay, te sama yoon ci Riisii ». Dafa di, xareb Riisii beek Ikren, Amerig setu ci te, ngir nànd dëgg-dëgg ni coow li deme, fàww nu dellu démb. Ndege, lawal gi nuy gis boobaak léegi, daf nuy réeral. Toppal samab xalima, nu dëpp jamono, xooli ñaareelu xare bu mag ba, ndeem dinan gindiku…

1945 : xare jeex, xare juddu

Jamono jooja, Almaañ moo ëppoon doole ci àddina si, raw ñépp ci lépp : xam-xam, koom-koom, xarala ak ngànnaayi xare yu yees. Boroomi xam-xami almaŋ yi, ci ndigal ak ndimbalu Hitler, dañ sumboon ay naal yu bare ci fànn yu yaatoo yaatu, rawatina ci wàllu ngànnaayi xare, tukkib ndénneer ak wér-gi-yaram. Sore woon nañ lool nag ci seen i liggéey, ba tax leen a jiitu ci àddina si ñeel fànn yooyee. Loolu may leen xam-xam ak kàttan, ñuy jaay doole yeneen réew yi, di songateek a nootaate. Hitler daldi bew, di buur, di bummi. Fu bëtam tegu rekk, mu jàpp ne raayab Almaañ war na faa jaayu. Bi mbir mi demee ba ëpp i loxo, 4i réew yii di France, USA, URSS ak Grande Bretagne daldi booloo, jàmmaarlook Hitler. Looloo sabab 2eelu xare bu mag bi ñuy nettali ci téere mboor yi. Kon, Amerig ak Riisii (URSS ba woon) ay farandoo lañu woon.

Lemal sa baaraam, muy benn.

Amerig – Riisii : xeexu suuf bi

Ci njeexitalu 2eelu xare bu mag bi, Almaañ da cee jaare nasax, dooleem daanaka jeex tàq. Waaye, ndono lim fi bàyyi mooy juri beneen xare. Ndege, li xeex biy tar yépp, farandoo yi, Amerig, URSS, France ak Grande Bretagne, ñoo ngi teg bët, di xemmem ndonol Almaañ li. Waaye, xëccoo bi ci diggante Amerig ak URSS lay mujje am, ndax ñoo ëppoon doole ci farandoo yi.

Amerig dafa bëggoon aakimoo li almaŋ yi bàyyi yépp, Riisii tamit noonu. Te sax, Amerig jotoon naa rawaley boroomi xam-xami almaŋ ak i naal yuñ sumboon yépp, yóbbu leen Amerig, soppi seen i tur, dugal leen ci laboraatuwaar yi ngir ñu jàppale leen, suuxatal leen seen xam-xam, seen mën-mën ak seen kàttan ci wàllu xarala ak ñoom seen. Bu dul woon loolu sax, Neil Armstrong du mës a teg tànk ci dénduw weer wi.

Riisii tamit, mi ngi doon def ay pexeem, di nos ak nocci. Moo tax, dañuy mujje paacoo suufus Almaañ bi. Bésub 23eel weeru me 1949, Amerig ak farandoomi tugal daldi sos RFA, Bonn nekk seen péeyub négandiku. Oktoobar 1949, Riisii tamit taxawal RDA ca Berlin. Penkub Berlin ba dib péeyub RDA. Ginnaaw gi, dinañ tabax ab maraaj buy dox ci diggante RFA ak RDA.

Ca la Amerig xamee ni, bu bëggee noot àddina si, fàww mu fexeel Riisii. Ndaxte, moom kesee ko mënoon diir mbagg. Looloo ko taxoon a ràbbalook waa Tugal, taxawal lees tudde ci nasaraan « Plan Marshall » bi nga xam ne, ca la kurélug OTAN giy sosoo. Amerig duggewu ko woon lu dul beddi Riisii, dagg ko ci jëflante yi ngir néewal ko doole.

Nde, ci njiitalu Amerig, 3i réewi tugal yooyu ñu lim ci kow ñooy taxawali kurélug xare, duppe ko ci nasaraan Organisation du Traité de l’Atlantique Nord, gàttal biy joxe OTAN. Booba, 12i réew ñoo ci bokkoon ; waaye tey jii, lu tollu ci 30i réew a ko sékk, di ay kapitaalist. OTAN, nag, benn jubluwaay kesee ko tax a jóg, te mooy xeex Riisii.

Riisii xam loolu, daldi taxawal déggoob Varsovie ba ca atum 1955, ci nasaraan Pacte de Varsovie. Mu ànd ceek réewi tugal yi féete penku, te nekkoon ay kominist. Kurél gu yaatu googu lañ daan woowe ci nasaraan Union des Républiques Socialistes Soviétiques, gàttal biy joxe URSS. OTAN ak URSS di xeex ci suuf, ciy pexe ak i doxalin. Ca la « guerre froide » tàmbalee diggante Amerig ak Riisii. Farandoo ya woon, nekk nañuy noon. Xare jeex na, xare juddoo ca.

Lemal sa baaraam, muy ñaar.

1989 : fiirug Amerig gi

Xew-xew bi gënoon a fés ci ati 1990 yi mooy màbbub maraaju Berlin bi (chute du mur de Berlin). Bi maraaj biy daanu, nag, dafa daanelaale URSS. Nde, Amerig daf leen tegoon xel, bàyyi leen ñuy xeex ak a reyante ba seen doole nasax. Ñu deele ay nit ñu baree bare, koom-koom gi nërmeelu, réew ma nekk ciy jafe-jafe yu tar a tar. Lu bare ciy réewi penku yi bokkoon ci URSS daldi tàmbalee fippu.  Ndege, maraaju Berlin bi daf leen nëbboon àddina si. Léegi, koom-koomu réewi sowu yi daldi am njeexital lu réy ci ñoom. Ñu fétteerlu, génn ci kurél gi, daldi moom seen bopp.

Ci atum 1991 la URSS tas. 15i réew yi ci bokkoon dem seen yoon. Ñu daldi sos Réewum Riisii mi nga xam ne, lum dee dee, mi ngi doon wéy di teg loxo lenn ci réew yim bokkaloon URSS.

Waaye, Riisii xamoon na ne, jamono jooju, Amerig a ko jekku woon. Te, lenn ci réewi penkub tugal yi fekki woon nañu OTAN. Mu xam ni bu deful dara, OTAN dina ko wër ndomb. Ca la muddaaranteek Amerig. George Herbert Walker Bush ak réewi sowu yi dig Mikhaïl Gorbatchev ak Boris Eltsine ne, dootuñu yaatal OTAN ci boori penku. Ñu daldi déggoo cig kàddu ne, OTAN warta cof dara ci wàllu penkoom, lu ko moy, dina jur coow.

Waaye, Riisii, rawatina Gorbatchev, dafa def njuumte lu réy a réy ci lum laajulee ñu bind déggoo bi, xaatim ko. Ndaxte, li ko dale 1999 ba tey, OTAN mi ngi wéy di raafal ay réewi penku, di gën a jege Riisii. Dafa di, tey jii, ci réew yi bokkoon ci URSS, ñaari réew kesee ci duggagul ci OTAN, muy Ikren ak Seworsi. Te, ñaari réew yooyoo dox diggante Riisii ak OTAN.

Li waral loolu mooy ne, njiiti réewu Riisii yi, dañoo xëroon ci sàngara, xawoon a nuur ciy caaxaan ba faf nasaxal réew ma. Moo tax, ay jafe-jafey koom ak i yëngu-yënguy politig yu bare ñoo gaaraloon nguurug Eltsine ga. Rax-ci-dolli, nger mi law ca réew ma, koom-koom biy doxe benn tànk. Amerig moom, nekk ci digg dooleem, di doxal lu ko neex, di buur, di bummi, di ñàkkal faayda Riisii ak di napp ak a noggatu réewi àddina si.

Ginnaaw gi, Boris Eltsine day feebar ba sonn, néew doole lool. Noonu, keroog 31eel ci desàmbar 1999, mu daldi tekki ndombog-tànkam, daldi bàyyi njiiteefu réew ma. Ca la ko Vladmir Poutine wuutoo ca boppu réew ma.

Jëmm joojooy soppi xar-kanamu Riisii, daldi sumb beneen xeetu xeex bob, moo sabab congum Ikren mii am tey.

Lemal sa baaraan, muy ñett.

Dees na ko topp…

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj