POLITIG
#1eelu fan ci weeru Me
Bés bii lañu jagleel liggéeykatI àddina sépp, di leen ci sargal. Waaye, bés la boo xam ne itam ci la sàndikaa yiy faral di amal ay doxi-ñaxtu ngir xamle jafe-jafe yi ñu nekke. Ren jii, fii ci Senegaal, sàndikaa yi ëpp doole amaloon nañu am ndaje ak Njiitu-réew mi, Maki Sàll. Ci njeexitalu waxtaan wi ñu séqoon ak moom, jébbal nañu ko ag kayit gu ëmb seeni jafe-jafe ak seeni bëgg-bëgg.
#Farub ndombog-tànku Njiitu jawriñ yi
Ci gaawu bii nu weesu la 165 dipite yi teewal askan wi ci péncum réew mi doon wote sémbub àtte buy far palaasu Njiitu-jawriñ yi ci Senegaal. Sémbub àtte bi, nag, jàll na te bettul kenn. Ndaxte, ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañu « waaw » 7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñoom, di waa PDS, dañoo lànk ne duñu wote. Kon, Senegaal amatul Njiitu-jawriñ.
#Kaasamaas
Njiitu réew mi, Maki Sàll, sumboon na fi aw waxtaan, mook fippu Kaasamaas yi 7 at yi weesu, ngir delloosi fa jàmm. Waaye, ca jamono ya ñuy lal i pexe ngir sottal mébét moomu, MFDC ak i nitam, seen doole dafa wàññeeku woon. Loolu la Jean-Claude Marut miy topp coow li bind ci Jeune Afrique
KOOM-KOOM
#Buy
Waa France24 amal nañu ag gëstu fii ci Senegaal, doon nemmeeku meññeef wii di buy. Ci kàllaama nasaraan, buy la ñu tudde « pin de singe ». Buy, nag, dafa di meññeef wu neex, am njariñ lool te aay ci feebar yu bare. Moo tax léegi réew yu am doole yi tàmbale cee bàyyi xel.
#Mbay ak xamtéef
Li ko dale 28eelu fan ba 30eelu fan ci weeru awril, Ndakaaru dalal na li ñu duppe AgriNumA, muy « ndaje mu njëkk mu jëm ci wàllu jokkale mbay ak jumtukaayi xamtéef ci Afrig sowu-jant ». Li ñuy wax « Intelligence Artificielle » ak « Big Data » dañu nekk ay xeetu xarala yu bees yoo xam ne, mën na ñoo indil baykati Afrig yi ay coppite ak it yokkute ci seen liggéey. Te loolu, sémb yi ñu jot a amal ci Ndakaaro gii firndeel nañ ko.
#Diine
Weeru koor wi tàmbali na ci àddina sépp ak fii ci Senegaal. Waaye dafa mel ni juuyoo amati na. Ndax, am na ñu woor altine, Tubaa ak ñi ci des woor talaata.
#Tàggat yaram – Futbal
Ginnaw bi ñu leen dóoree 3-0 ci joŋante bu jëkk bi, doomu Senegaal bii di Saajo Maane ak ekibam Liverpool daan nañu Lionel Messi ak Barcelone 4-0. Bu ko defee, bii mooy doon ñaareelu yoon yu toppalante Saajo Maane ak Liverpool di joŋante finaalu « Ligue des Champions UEFA », ñu war cee janook Tottenham ci 1eelu fan ci weeru suweŋ.