LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (DIBÉER 12 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DOXU-ÑAXTU CA PARI

« Ca Senegaalu Maki Sàll, boo naan déet di dugg kaso ! » Kàddu gilee gënoon a fés ca doxu-ñaxtu ba. Ay téeméeri téeméeri doomi Senegaal ñoo génnoon ci mbeddi Pari yi ngir ñaxtook a naqarlu « jaay doole » ak « xoqatal » bi Maki Sàll ak nguuram nekke ca Senegaal. Pastef bu Paree woote woon doxu-ñaxtu bi ci gaawu bi. Yoroon nañuy pankàrt bind ci « Macky Sall le dictateur », maanaam Maki Sàll jaaykatu doole bi. Liñ ko dugge mooy kaas ak a xamal àddina sépp ñaawteef yi Maki Sàll ak nguuram nekke, ku wax lu worook i bëgg-bëggam mu ne le ràpp, tëj. Rawati na ndëgg-sërëx ak pexe yi ñuy fexeel Usmaan Sonko miy lawax ci wotey 2024 yi ngir mu bañ cee bokk. Tudd nañ fa itam turi 102i militaŋi Pastef yees jàpp ci lu dul yoon.

DIINE

Siyaar bu mag Tiwaawon

Tiwaawon dékku na mbooloo mu takku ngir siyaar bu mag bi ñuy amal ca dëkk bu sell ba. Ñu gis ne, jëloon nañu matuwaay yèpp ngir xew-xew bi jaar yoon.

Bésub fàttaliku Gaynde Fatma

11 màrs di bés bi ñuy fàttaliku Sëriñ Séex Gaynde Fatma miy way-juru Sëriñ Mbàkke Soxna Lóo. Ñu koy amale ca Tayif diggam ak Tuubaa di 30i km. Ñu nemmeeku ci ab laksidan ba ñetti bakkan jot caa rot ak 18 ñu ame ay gaañu-gaañu.

BITIM-RÉEW

Irã ak Araabi Sawdit

Jàmmoo di na doxaat ci diggante Irã ak Araabi Sawdit. Loolu la Kilifay ñaari réew yi xamle ci àjjuma jii ca Pekĩ, réewum Siin, ginnaaw waxtaan yi doxoon ci seen diggante ci yombalug réewum Siin. Ku ci nekk ci ñaari réew yi fas na yéen ubbiwaat àmbaasadam ci dëkku moroom ma ngir dundalaat jëflante bi. Ci atum 2016 la ñaari réew yi  amoon i jàppal-bàyyi ba ku ci nekk dummóoyu woon moroomam.

Libi

Réewum Libee ngi ci yoonu amal i woteem yu njëkk ginnaaw yëngu-yëngu yi fa amoon ci atum 2011. Bu ñu sukkandikoo ci kàdduy Abdulaay Bàccili, doomu réewum Senegaal li fa jiite Manul (Mission d’appui des Nations unies en Libye), ñoo ngi ciy waxtaan yoy bu sottee, dina ñu am jumtukaay yu mate ngir amal i wote ci weeru suwe 2023 bi. Wote yooyu nag,  njëkkoon nañu leen nisar ci atum 2021 waaye mujjuñu woon a àntu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj