70i WAY-SÀKKU JÉBBALE NAÑ SEEN I WAYNDARE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àllarbay tey ji, 27 desàmbar 2023, la àpp bi Ndajem ndeyu àtte mi mayoon way-sàkku lawax yi jeex. Bii guddi gi xaajee (00i waxtu) la àpp gi jeex. 

Ci li rotagum ciy xibaar, 70i way-sàkku ñoo jébbale seen i wayndare ngir doon lawax ci wotey 2024 yi. Waaye, laata àpp giy jeex, amoon nay ndaw ya woon ga màkkaanu Ndajem ndeyu àtte mi ngir joxe seen i wayndare. Ponkali kujje gi ak lawaxu Nguur gi, Aamadu Ba, ñépp joxe nañ këyit yi war ngir bokk ci joŋantey njiiteefu réew mi.

Léegi nag, juróom-ñaari àttekat yu mag yaa ci des. Ñooy daganal ak gàntal càkkuteef yi ñeel wotey 2024 yi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj