YËGLEB NJËWRIÑU BIIR RÉEW MI AK KAARAANGEG PÉNC MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yégle bi :

“Njëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi mu ngi yëgal askan wi ne Sën Ma-Jambal JAAÑ, ak li ñu ko doon wër lépp, woolu ko, teg ci yoon tere woon ko mu génn mbeeraay gi, teewul mu mujj a génn réew mi ci anam yu lënt ba fii, ginnaaw ba mu teewee, ci guddig 23 jàpp 24i fani sebtambar 2025, ca Naawub Belees Jaañ ngir tukki.
Joxe woon nañu ndigalu fuglu ak bàyyi xel bu wér te wóor ci mbooleem wànqaasi kaaraange yi mu soxal, bis ba dogalu tere gi rotee ak tay.
Fii ak njureef yi bawoo ci luññutug biir gi di rot ngir xam ci yan anam la génnee ak xam ndax am na ñu ci laale, Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, ngir fuglu, jël na dogalu jële Njiitu “Division des Investigations criminelles” ak Njiitu “Commissariat spécial” bu Naawub Belees Jaañ ca fa ñu ne woon.
Bu dee giseef na ci ag càggante walla ag njàppale, dees na ci jël daan yi war.
Njëwriñ gi di yëgal askan wi itam ne jot na, ci bisub tay bi, dogal bu bawoo ci Njiitu Kurélug Àttekat gu “Pool Judiciaire Financier”jëm ci fépp fu ñu gis kii daw, nu jàpp ko indi.
Jëwrin ji di ci posewu ngir fàttali ag taqoom ci sàmmonte ak dogali yoon yi, doxaliin wu leer ak rafet njort.”

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj