BÓOMUG ALEŊ KALI: G7 BU CEES DOOR NA XEEX BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Barkaatu-démb ci talaata ji lañu bóom jangalekat bii di Aleŋ Kali. Ci anam yu metti lañu faatee bakkanam. Nde, dafa jàngaleji woon ba wàcc, di ñibbi, ñu dogaale ko, jam ko, mu jaare fa ñàkk bakkanam. Moom nag, mi ngi tolloon ci fanweeri at, amoon na soxna ak ñeenti doom. Looloo tax waa G7 bu Cees génn di naqarlu mbir mi, di sàkku ci Yoon mu def liggéeyam.

Ngir jëmmal xeex bi, tey ci àjjuma ji, amaloon nañu li ñuy dippee “débrayage” bi juróom-ñeenti waxtu jotee ci yoor-yoor gi. Rax-ci-dolli, nar nañoo amal am ndaje fa kanamu IA (Inspection d’Académie) bu Cees. Ñu yokk ci ne bés bi ñu koy rob, kenn ci ñoom du jàngale. Maanaam, dañuy def “Journée morte”. Te, ñi ngi woo seen naataangoy jàngalekat yi ñu jàppale njabootam gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj