Ginnaaw wiiri-wiiri bu metti bi, àgg nañ Ndaari. Maki Sàll tànn na Aamadu Ba, jiital ko ngir mu wuutu ko ci boppu réew mi. Kon, Aamadu Ba, magum jëwriñ yi, mooy doon mbëru Bennoo Bokk Yaakaar, keroog féewaryee 2024.
Ci gaawug tey jii di 9i fan ci sàttumbaar 2023, fa pale ba, la Njiitu réew mi siiwal tànneefam. Mustafaa Ñas moo jàng bataaxalu Maki Sàll bi, wax ne :
“Aamadu Ba kese mooy lawaxu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar.”
Mbetteel amul. Nde, Aamadu Ba la ñi ëpp joxoñoon, wax ne moo gën a jekku ci doon lawaxu lëkkatoo Nguur gi. Moom Aamadu Ba, 62i at, def na at ci boppu Càmm gi, ndax sàttumbaar 2022 la ko Maki Sàll tabboon. Nekkoon na tam jëwriñu ngurd mi, doon doxal Plan Sénégal Émergent, naalu Njiitu réew mi. Rax-ci-dolli, nekkoon na fi jëwriñu mbiri bitim-réew. Cig pàttali, jiite woon na fi Impôts et domaines.
Jeune Afrig siiwal na ne, moom Aamadu Ba, dafa amoon ñu koy jàppale ci biir réew mi ak fa bitim-réew. Bu dee bitim-réew, rawatina Farãs, Robert Bourgi miy lonkoo Maki Sàll, moom la doon jàppale. Jeune Afrig neeti, ci biir Càmm gi, jëwriñ yu deme ni Abdu Kariim Fofana, Séex Umar Aan, Duudu Ka ak Abdulaay Saydu Sow, ci ginnaawam lañ toppoon.
Léegi nag, ñu xaarandi, xool ba xam waa Bennoo Bokk Yaakaar, rawatina ñi doon xëccoo ak moom, dinañ bennook moom walla déet. Li ci kanam rawul i bët.