ABDU JUUF DELLU NA GINNAAW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, Abdu Juuf ak Abdulaay Wàdd, Njiitu réew ya woon, dañ bokkoon bind ab bataaxal jagleel ko askanuw Senegaal. Ci seen bataaxal bi, dañ doon soññ askan wi ci mu nangu waxtaan wi Njiitu réew mi, Maki Sàll, woote te dakkal taafar ji. Te yit, joxoñ nañ ci ndaw ñi, di leen wax ñu dakkal ci ni mu gën a gaawe toj yeek yàqate yi te bañ a déglu nooni biti yiy yàq seen i xel. Xamle nañ ci sax ne, ku nekk ci ñoom ñaar, jokkoo naak Maki Sàll ci jollasu, waxtaan ak moom lu yàgg. Ci liñ bind nag, Njiitu réew mi feddalil na leen ni du dagaan 3eelu moome te dine def lépp lum mën ngir amal i wote yu jaar yoon ci jàmm. Waaye de, seen bataaxal boobu, bu démb doon tey, duñ ko bind. Ndaxte, wex na leen xàtt. Li ci topp ciy wax tax na ba kenn ki, Abdu Juuf, dellu ginnaaw.

Wolof dafa ne, tontu du forox. Nde, ginnaaw biñ siiwalee seen bataaxal bi, askan wi, rawatina lu baru ciy boroomi tur, dañ dal seen kow, yakk leen lu mel ni xeme. Moom kay, amul luñ leen deseelul. Ablaay Wàdd sax, daanaka xawees na ko jéllale. Nde, Lu ëpp ci Saa-Senegaal yi dañ jàpp ne, loxoom génnul ci ndàqug wote yi ndax moom, doom ji rekk a ko yitteel. Moo tax, taxawaayam bettul kenn. Ki bette kay mooy Abdu Juuf, moom mi waxoon ne dafa raxasu ba set wecc ci lépp luy pólitigu Senegaal. Waaw, atum 2021, taskatu xibaar bii di Patrick Simonin dalaloon na ko ca TV5MONDE, ci jotaayu L’invité. Keroog, bim ko laajee ci xew-xewi màrs yi yëngaloon réew mi at mooma,  dafa tontu woon lii toftalu :

« Am nga sañ-sañu laaj sab laaj, waaye man itam am naa sañ-sañu bañ a tontu sab laaj. (…) Bi may jóge ci Nguur gi atum 2000 dama dige woon ne duma mësati wax ci jafe-jafey Senegaal. Duma wor sama kàddu. »

Kàddu yii la ñu bari di fàttaliku. Moo ñu ne ko mu màndu ci mbiri réew mi. Yemuñu ca de. Nee ñu sax, moom ak Ablaay Wàdd yépp, dañuy jàppale Maki Sàll mi ngi xam ne, Farãs a ko ngemb ni mu leen ngembee woon. Te, dara taxu leen a jóg lu moy sàmm soxlay Farãs wëliis yoy Senegaal. Bi coow loolu jibee nag, Abdu Juuf génne na beneen bataaxal, di ci indiy leeral.

Lii la ci bind :

« Samay mbokki réew,

Ni ngeen ko xamee, keroog bi ma wàccee jal bi, bésub 1 awril 2000 ba nëgëni, mësumaa nangoo wax ci mbiri pólitigu Senegaal. Li ma ko dugge woon mooy tegu ci yoonu bokkeef wi Lewopool Sedaar Seŋoor xàlloon, moom Njiitu réew ma woon.

Damay fecci sama kàddu ndax campeefi réew mi dañoo tagatembe ci anam boo xam ne, guléet ñu koy fiy nemmeeku.

Seetlu naa, ànd ceek réccu ak tiis, ne bataaxal bi ñu siiwal te sama torlu nekk ci ak bu Njiitu réew Ablaay Wàdd dafa jur ay jiixi-jaaxa yu bari.

Dama bëgg a leeral, ngir dàq bépp xeetu lënt-lënt, ne Ndajem ndeyu àtte réew mi ma sos ca atum 1992 kese moo mën a aar sunuy campeef ak sunu demokaraasi. Moom kott moo am sañ-sañu wax liy yoon ak jël ndogal yiy dal ci kow ñépp ci wàllu arminaatu wote bi ak càmmug diiru moomeg njiiteefu réew mi.

Maa ngi ñaan kon askanuw Senegaal, way-pólitig yi ak ñi jiite réew mi ñu ànd ak dal te gore, daldi jëfe lépp lu Ndeyu àtte réew mi sàrtal. Nañ sàmm tamit àq yi yoon may nit ñi te ñu jëlee leen ciy xeex yu metti ñeel demokaraasi.

Maa ngi yeesal cofeel gu dëggu te sax gi ma am ñeel askanuw Senegaal ak it di feddali sama ngërmaande ci ñoom ñeel at yu yàgg yuñ ma wóolu woon, dénkoon ma réew mi, ma leen di liggéeyal. »

Wolof nee na, ëpp baax na ci laax bu tàng.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj