Abdu Latif Kulibali, di jëwriñ ak magum fara-caytu Nguur gi, jël na ndogalu tekki ndombog-tànkam, génn ci Nguur gi. Ab yégle la siiwal di ko ci xamle ne :
“Ginnaaw bi ma xalaatee bu baax a baax, jël naa ndogalu jël sama matuwaay ci lii lépp, ngir génn ci Nguur gi. Bu ko defee, moomaat naa sama bopp, amaat samay sañ-sañ yépp ngir mën a sàmm ak a layal samay xalaat ak i gëm-gëm ci wàllu pólitig.”