Ablaay Daawda Jàllo amal ñam ndaje ak taskatixibaaryi, tey ci ngoon, doon ci leeral taxawaay ñeel wotey 2024 yi. Nde, njiitu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar li, Maki Sàll,.dafa tànn Aamadu Ba ngir mu doon lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar. Te, moom Ablaay Daawda Jàllo, dafa bokkoon ci ñi sampoon seen ndënd. Coow li bare woon na nag. Ñu baree ñoo ngi doon sikk-sàkka ndax dina nangoo topp ci ginnaaw Aamadu Ba am déet. Moom, njiitul CESE li, nee na nangu na ndogalu Maki Sàll li.
Meeru Bokke Jallube bi daf ne, ginnaaw waxtaan wim séq ak Njiitu réew mi, sempi n’a ndëndam ci woteu 2024 yi, du ci doon lawax.
” Ginnaaw ndaje yu bare yi ma am ak Njiitu réew mi, ginnaaw waxtaan yu bare yi waxtaan ak sama jegeñaale ak i soppe, jël naa ndogalu, ginnaaw bi ma xalaate bu baax, nangul ko ndogalam li ngir jiital bennoo ak jàmmoo.”
Kon, mënees na njortagum ne day topp ci ginnaaw Aamadu Ba. Waaye nag, dafa mel ni loolu du woon lu ko gënal. Nde, kenn umpalewul ñagas-ñagas yi ck digganteem ak Aamadu Ba. Te sax, wax na ba jeexal te jaarul ci turu magum jëwriñ ji. Loolu day firndeel ni dañoo bennoo ci kow, juyoo ci suuf. Dafa di, seen xol yi ànduñu. Ndax loolu dina leen indil jafe-jafe ci wote yi ?