AIBD : AB ROPPALAAN BU WÀCC YOONAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Naawub Belees Jaañ bi (Aéroport International Blaise Diagne) dafa tëj, tey ci alxames ji. Ab roppalaanu Transair bu Air Sénégal àbb moo wàcc yoonam. Kilifay naawu ba ñoo ko yégle.

Ab yégle la kilifay naawub Belees Jaañ biral, xamle ne ci :

“Roppalaan HC 301 bu kompañi Air Sénégal, jëmoon Bamako, moo wàcc yoonam ba mu teddiwee bay waaj a buddi. Ci guddig alxames ji, bi 1 waxtu jotee, la mbir mi xew.”

Bees sukkandikoo ci ñoom ba tey, 78i way-tukki la roppalaan bi yeboon. 11i nit ñoo ci jëley gaañu-gaañu, mu am ci 4 yu sonn lool. Am na tamit yeneen 6i way-tukki yu amey gaañu-gaañu yu ndaw-ndawaan yees rawale fajuwaayu naawu ba.

Nee ñu nag, ñoom kilifay naawu ba, jël nañ matuwaay yépp ngir saytu mbir mi, sàmm ak a toppatoo way-tukki yi. Jëwriñu dem beek dikk bi, Elaas Maalig Njaay, dem na seeti ñaa ca jëley gaañu-gaañu ngir nemmeeku seen wér-gi-yaram. 

Bees sukkandikoo ci njëwriñu dem beek dikk bi, Pekkug luññutu ak cettantal gi (Bureau d’enquête et d’analyse  – BEA) dina ubbi ag luññutu ngir leeral sabab yi waral aksidaŋ bi am.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj