Aksidaŋ bu metti moo am tey ci yoonu Ngaay-Kebemeer wi. Fukk ak benni nit (11i) ñoo ci ñàkk seen i bakkan. Juróom-ñeenti nit ñoo ci amey gaañu-gaañu.
Bi 10i waxtu jotee ci yoor-yoor bi la jéyya ji am. Ci buntu Ndànd, tollook dëkku Palmewoo Faal, la aksidaŋ bi amee. Ab oto bu ndaw (minikaar) bu 8i palaas moo mbëkkante ak ub sëfaan. Oreeru 8i palaas bi, dëkk bees di wax Cimen Kayoor, fa Lingeer, la jëmoon. Sëfaan bi moom, Ndakaaru la bawoo woon.
Anam bi ñu mbëkkantee, maanaam ni ñu dalantee, dafa metti ba 11i bakkan rot ca fa saa sa. Ci biir 9i way-tukki yi ci jëleey gaañu-gaañu, 8i ya dañoo sonn lool. 11i néew yaa nga fa morgu raglub “Centre Hospitalier Amadou Sakhir Mbaye” bu Luga. Ña ca ameey gaañu-gaañu, sàppëer yi jàllale nañ leen fa ragluy Ndànd ak Kebemeer.