Njabootu làmbu Senegaal ak mbatiit am nañu dëj. Nde, xibaaru tiis ak uw naqar a leen dikkal ci àllarbay tay jii, 4i pani desàmbar 2024. Dafa di, waadab seereer ba woon, Àmburuwaas Saar, moo génn àddina.
Moom nag, Àmburuwaas Saar, mbër mu mag la woon, ràññeeku woon lool sax ci géewi Senegaal yi, rawatina ci fànnu mbapat. Ginnaaw bi mu jógee dëkkam, teersi Ndakaaru, dafa ñafe, wone njàmbaar, fit, xarañte ak fulla ju mat sëkk. Looloo yékkati turam, mu daldi fës ci biir moroomi mbëram. Ndaxte, turu Àmburuwaas Saar, dees na ko dendale ak yeneen waada yu deme ni Muhamet Njaay aliyaas “Robeer Juuf”, Mànga 2, ak yeneen i mbëri seereer yu mag yoy, jot nañoo toj fépp.
Dëkku Palmareŋ la Àmburuwaas Saar cosaanoo. Ci bëre mbapat ak ci xeetu bëre bees duppee ci tubaab “lutte gréco-romaine” (làmbu gerekoo-romeŋ yi) la gënoon a féete. Waayeet, bokk na ci as-tuut ci atleti Senegaal yi jot a bokk ci juróomi joŋantey olimpiyaat, muy lu kenn mësut a def. Nde, ñeenti joŋante yi, daf ci bokkoon niki mbër, benn bi niki tàggatkatu mbëri réew mi. Bu dee ci wàllu jaar-jaaram, jot na fàggu lu tollu ci fukki medaayi wurus ci joŋantey làmb yi, fi Afrig.
Bi mu bàyyee bëre, ci la nekk tàggatkatu mbëri réew mi ci wàllu mbapat. Naka noonu, jot naa cee am ay ndam yu baree bari biir Afrig, muy sagu Senegaal. Kon, Senegaal moo ñàkk, Afrig moo ñàkk.
Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, biral na tiis wi mu ame ci génnug àddina Àmburuwaas Saar. Dafa bind, wax ne :
« Tiis wu réy laa am bi ma yëgee génnug àddina Àmburuwaas Saar, tàggatkat ba woon, daan tàggat mbëri réew mi, di woon ku ràññeeku lool ci sunu tàggat-yaramu cosaan bii di làmb. »
Njiitu réew mi jaal na ko njabootam, ay mbokkam ak njabootu làmb, ba noppi ñaanal ko.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaal njabootam, ay mbokkam, njabootu làmb ak njabootu mbatiit gépp, ci ni mu gënee yaatu.