Démb, ci guddig alxames ji, jëwriñu biir réew mi doon janook taskati xibaar yi, bi 23i waxtu tegalee 30i simili ak lu topp. Àddu na ci yëngu-yëngu yi gaar réew mi ginnaaw daan yi àttekat bi gàll njiitul Pastef li, Usmaan Sonko. Antuwaan Feliks Jom biral na ne 9i nit dee nañu ci, diggante Ndakaaru ak Sigicoor.
Jëwriñ ji ñaax na askan wi mu ànd ak dal ngir jàmm dellusi ci réew mi. Waaye nag, ciy waxam, Nguur gi jël na matukaayam yépp ngir sàmm kaaraange réew mi, aar nit ñi.
Cig pàttali, njiitul kujje gi, Usmaan Sonko, dañ ko daan 2i ati kaso yum war a tëdd ak ndàmpaayu 600. 000 FCFA yum war a jox Aji Saar. Ci alxamesu démb ji la ndogal li génn. Waaye nag, Yoon setal na ko ci tuumay ciif ak tëkkuy rey yi dàmpkat bi doon jiiñ.
Ndogal la tukkee ci àttewaay baa taal réew mi, xeex bi jolli fépp ba 9i bakkan rotagum ci. Xeex bi nag, jeexagul. Nde, jamono jees di bind yaxal bii, ndaw ñi sumbaat nañ xeex bi ci béréb yu bari.