Démb, ci guddig alxames ji, mbaali-jokkoo yi, WhatsApp, Facebook, Twitter, Telegram, Youtube, benn doxi ci woon. Ci guddi googeet la jëwriñu biir réew mi janook taskati xibaar yi, bi 23i waxtu tegalee 30i simili ak lu topp, xamle ne, Nguur gi ci boppam moo dog njokkoo gi. Li tax ñu def mooy, ci waxam :
« Dañu gis ay nit ñuy tas bataaxeli mbañeel ak fippu ci mbaali jokkoo yi. Nguurug Senegaal, ci fullaay boppam, moo jël ndogalu dogandi njokkoo gi ñeel yenn jëfekaay yees di jëfandikoo ngir xirtal nit ñi taafar ak mbañeel.
Ginnaaw bi mu layee loolu ba noppi, jëwriñ ji dafa wax ak këri xibaar yi ci li ñiy dégtal askan wi :
« Noo ngi fàttali këri xibaar yi solos sàrt bi tënk seen liggéey, sàrt bob, moo may njiitul caytu gi muy artu walla di dakkal lépp lu mën a gàllankoor kaaraangeg Nguur gi, mberaayu réew mi walla bépp xeetu wooteb mbañeel. »
Jëwriñ jaa ngi jeexaley kàddoom ci woo askan wi mu ànd ak dal. Waaye, nee na tam, Nguur gi jël na matukaayam yépp ngir sàmm kaaraange réew mi, aar nit ñi.
Waaw, juróom-ñeenti yi dee moom, fum leen fekkoon ?