ARAM FAAL, SUNU SÉEX ANTA JÓOB BU JIGÉEN…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaata jii weesu di 23 ci weeru awril la Mbootaayu-Xeet yi jagleel bépp teere bu doom-aadama bind ci àddina si.
Ci la EJO ak ArtXaleyi, di ñaari kurél yuy yëngu ci mbirum aadaak ladab, sargal Soxna Aram Faal Jóob mi yàgg a def liggéey bu am solo ngir ñépp jox làmmiñi réew mi seen gëdd.
Majaw Njaay mi sàkk ArtXaleyi, jiite ko, dajale nay gone laaj leen kan lañu bëgg ñu sargal ko ren jii, ñoom ñépp ñu ne : ‘’Xanaa sunu maam Aram Faal Jóob !’’
Waaye du woon guléet ndax Senegaal yàgg na delloo Aram njukkal. Ñaari at ci ginnaaw rekk la ‘’Foire du livre’’ amaloon xew-xew bu mag, jagleel ko ko. Ci la Soxna Aram woo Ndey Koddu Faal — mi bokk tey ci surnalisti LU DEFU WAXU yi — ni ko : “Doom sama, yow laa bëgg nga teewal ma ci xew-xew boobu, jël fa kàddu ci sama tur, fàttaliwaale mbooloo mi sama jaar-jaar.”
Kàddu ya Ndey Koddu yëkkati keroog ci tubaab la tekki fii ci kàllaamay Kocc mook Paap Aali Jàllo mi ngeen war a miin turam moom tamit ndax mu ngi bind saa su nekk ci yéenekaay bi ngeen janool tey di ko jàng…
Mbooloo mi, maa ngi leen di nuyu yéen ñépp, ku ci nekk ci sa tur ak sa sant…
Aram Faal Jóob…
Képp ku dégg tur wii, muy fii ci Senegaal di bitim-réew, fàww sa xel dem ci soxna su masul a tàyyee liggéeyal làmmiñi réewam, ngir suqali leen.
Doom-Aadama yu bare, ba ñu newee gone lañuy bëgg a doon lii mbaa leneen. Waaye liggéey bi ñuy mujjee def day faral di safaanook seeni bëgg-bëgg. Aram Faal Jóob mi ñépp sopp ba di ko woowe Tànta Aram, bokkul ci ñooñu.
Amal njariñ Senegaal ak Afrig, lu ko mas a soxal la te Yàlla boole na kook ñu ko ciy ñaax. Ki ci njëkk, gën cee am solo, Séex Anta Jóob la woon. Aram ci boppam moo ma ne su dul woon ndajeem ak ponkal moomu bind Nations nègres et culture, amaana mu aw weneen yoon. Nii la ma ko waxe : « Ndongo Séex Anta laa woon. Moo tax ma teel a bëgg a bey sama waar ci toolu làmmiñi réew mi. Bu dul woon loolu, jàngalekat laay doon tey.»

Soxna Aram Fall Jóob ak Ndey Koddu Faal

Maa ngi fàttaliku keroog jooju ni kanam gi tiise bi mu may nettali digganteem ak soxnay Séex Anta : « Louise-Marie Maes, sama xaritu benn bàkkan la woon. Daan nanu am ay waxtaan yu yaatu ci làmmiñal».
Aram Faal Jóob doomu-Ndar la. Fa la fekk baax. Fa la jànge ba am ñaari xaaji Bakaloryaam laata muy wutali Iniwérsite Ndakaaru, am fa lijaasa bu ñuy wax Diplôme d’études supérieures. Jóge fa nag dem mottaliji njàngam Tugal ci Iniwérsite Paris III ; fa la defe teesam sax, ci atum 1973.
Boo seetloo bu baax, dinga gis ni donte sax at ya mu def Frãs am nañ solo, li ko gënoon a ñor mooy delsi Ndakaaru liggéey ngir jëme réewam kanam. Mu yemook at yu njëkk yi Senegaal moomee boppam, Aram ñibbisi bay waaram ci ëllëgu réew mi.
Fanweeri at ci ginnaaw la tàmbale bind, ànd ceek Rosine Santos ak Jean Léonce Donneux. Ci lañu génne ca Karthala benn Dictionnaire wolof — français bu askan wiy jariñoo boobaak tey.
Wànte Aram yemu fa. Mënees naa lim ci téere yu bari yi mu bind : Grammaire fonctionnelle de la langue wolof ; tekkendoo na it ak àttekat bii di Amet Juuf Ndeyu-àtte réew mi ; beneen téere bu am solo bu mu tekki mook ndem-si-Yàlla ji Maam Yunus Jeŋ mooy Une si longue lettre bu Mariyaama Ba ñu tudde ko Bataaxal bu gudde nii. Ngërëm ñeel na tamit Aram Faal Jóob mi génneendoo ci wolof, tubaab ak àngale Baatukaayu x@mtéef di ci tekki bépp baatu informatik. Bunu fàtte itam ni ci atum 2012 moom ak Amet Juuf ak Mamadu Njaay lëkkaloo nañu sotti ci wolof sunu Code des marchés publics duppe ko Sàrtu Jawi Nguur gi.
Li gën a tax Aram war a doon royukaay moo di ne du sonn du tàyyi. Tëju na ay ati-at di liggéey ci téere bu mu génne bu yàggul ngir fexe ba ñi déggul tubaab mën a jàng kàllamay Kocc. Téere boobu mooy Nëwu làmmiñu wolof.
Kon li ñépp di xëccoo di ko sargal, di ko delloo njukkal warul a bett kenn. Amul ku ko ko gën a yellool.
Waaye ak fi dayoom tollu yépp, Soxna si Faal tiitaruwul, réy-réyluwul. Naka jekk, Tata Aram xamul puukare. Dafa amul sax jotam, faf. Waaw, sunu lingeer bi dara mësu ko ñor lu dul sàkku ak nafar xam-xam. Waaye tamit, dafa mës a yittewoo ndono li, ba tax mu dëkk ci di tette ndaw yi.
Noonu la ko Soxna Aram Faal jàppe, ca njëlbéen ga ba nëgëni-sii. Nu gis ne kon màndargay niteef yi Soxna Aram Faal làmboo dañu di ab fànn bu réy ci jaar-jaaram ; rawatina ba muy nekk IFAN ba ni mu fay génne ci atum 2002 -moo fa jiite woon banqaasu làmmiñal bi- ak ci Kurélug wall ngir naataange Senegaal, di këru móolukaay bu siiw bi mu sos te gàttal bi ci nasaraan di joxe OSAD. Jamono jii nuy wax ak yéen, li ëpp ci téere wolof yi jot a génn ci réew mi, OSAD a leen móol. Téere yooyu, nag, ràññees na ci Aawo bi te ndem-si-Yàlla ji, Maam Yunus Jeŋ, bind ko ak tamit téere Séex Aliyun Ndaw yu takku yi, werekaanu werekaan yi ci wàllub ladab ci làmmiñu wolof.
Tey, mboolem bindkat yi ci làmmiñu wolof fésal nañu seenug mbëggeel ak fonk bi ñu fonk Soxna Aram Faal Jóob. Li ko dale ci Mamadu Jara Juuf ba ci Mamadu Njaay, jaare ko ci Daba Ñaan ak Séex Adaraame Jaxate, ñépp a ko naw. Li tax ñu naw Soxna Aram, am ci moom mbëggeel ak cofeel yu réye nii, moo ko jëfe. Waaw, te muy dëgg. Ndaxte, ku baax, ak foo fekk baax, mbaax fekk la fa nga nekk, yëkkati la ba nga sut say maas ! Soxna Aram Faal daa baax, te ci mbaaxam doŋŋ la wuufe ndaw yiy topp ciy tànkam, di leen tette, boole ci muñ ak yéwén lool ci xam-xamam ak alalam, te séentuwu ci dara. Te, nag, wolof dafa wax ne, ku dul gërëm nit, doo gërëm Yàlla. Looloo tax bindkat yooyii ñu fi jot a lim, ku ci nekk gërëm na Soxna Aram, sant ko delloo ko njukkal. Ba tax na, ku ci nekk ci ñoom, tudde na ko lu mu tuuti tuuti benn ci ay téereem, seedeel ko ci lu rafet. Waaye, bu dee seede ak wax ju rafet rekk, dees na ko bàyyee ndem-si-Yàlla-ji Maam Yunus Jeŋ. Ndax, tagg bi mu tagg Soxna Aram rekk doy na ci tagg. Li mu génn àddina tey, tax na waxam ji gënatee daw yaram. Looloo tax ma bëgg leen a dégtal baat yu neex te xóot yi mu jagleel sunu werekaan bi, te mu ubbee leen téere fent bii di Aawo bi : “Aram Faal Jóob, mu ñàkk mi kiñaan te tëlee wonu.” Waxatuñu dara, mu teg ci baat yii nga xam ne, cuq nañ man lool sax : “Yii aawo, kenn du ma leen jëkk a sant ndax kenn du ma jëkk a gore. Lingeer yi mel nii ñoo tax géwél yi naan : sonn daw, jaaxle daw, bëgg a dee daw, doo fekke dara. Waaye sonn muñ, jaaxle muñ, bëgg a dee muñ, ku muñ muuñ.”

Ginnaaw loolu, OSAD mi ngi amal liggéey bu am solo ñeel làmmiñi réew mi, rawati-na làmmiñu wolof. Ci tànk yooyu la doon dox ba tey bi muy fésal ak a wone, ci mboole mi mu dippe woon “fentakoon”, ni sunu làmmiñ yi mënees na cee fent i xalaat ak xeeti njariñ yu wute ak woy. Li mu ko dugge woon mooy wone ni sunu làmmiñ yi du woy rekk lañu ci mën a def.
Dëgg la sax, OSAD biral na ne sunu làmmiñ yi amuñu dara lu ñuy ñeewe yeneen làkk yi ci wàllu taaral. Waaye, kàggug OSAD bi nga xam ne, li ko dale atum 1995 ba léegi, dees na ci lim lu tollu ci 50 téere, yemul doŋŋ ci ladab. Ndege, OSAD mi ngi yëngu tamit ci njàngle mi ak lépp lu ko soxal : mi ngi taxawal ay naal ngir daara yi, di tàggat aji-tàggat yi. Rax-ci-dolli, OSAD mi ngi móol ay téere njàng. Téere yooyu, nag, ci mbirum wér-gi-yaram lañuy wax, ci wàllu alfaabetisaasiyoŋ ak bépp xeetu ndimbal ñeel dundinu mboolem-nawle mi. Téere yu mel ni Njàngum Wolof, Ëmbub jàmm ak Téere xayma dañuy firndeel jubluwaay boobu ak bëgg-sa-réew bi OSAD làmboo.
Nu gis ne kon, liggéey bi Soxna Aram Faal sumb ak joyyanti bi Séex Anta Jóob sumboon benn lañu. Dafa di sax, Soxna si, Séex Anta a di sëriñam. Ci njàngalem lay wéye : juboole aji-xam yeek askan wi, boole leen ñu doon benn bokk benn jëmuwaay te làkku nootkat bi bañ leen a féewale. Ngir dëggal loolu, Aram Faal yemul rekk ci di bind ay téere yu am maanaa lool ak sos genn këru móolukaay : dafa jaayante ak bakkanam tamit, bés bu nekk laa wax, nag. Te wax dëgg Yàlla, man rekk doy naa ci seede.
Waaw.
Ndaxte, man Ndey Koddu Faal mii di wax ak yéen, bés bu Yàlla sàkk ma woo ko di ko laaj ngir mu jubbanti ma, gindi ma, leeralal ma kumpa yi làmmiñu wolof àndal. Nun kat, ku nekk dafa jàpp ne peeg na wolof, fekk ne ak a bare ay fiir ! Duma leen ko nëbb, nag, saa yu ma koy woo, damay xaw a am kersa. Waaye saa bu wuyoo ak mbégte mu baat bi di àndal ngir rekk yéwénam ci xam-xam, sama xel dal, ma am fitu laaj ko ay laaj yu bare ci mbindum wolof ak pirim baat yi. Jàpp naa ne sax, deñ-kumpa gi ci man moo tax mu fonke ma ni mu ma fonke ba tax, tey jii, mu sant ma ma dégtal leen jaar-jaaram ci wàllu xam-xam ak xeex yi mu jot a xeex. Du caagéeni ne dama aay, ndax am na ci yéen ñi may déglu ñu ma gën a mën lii mu ma sant.
Yàlla na fekk ne kàddu yii ma tibbe sama biir xol, jegele nañu leen, ci xol ak ci xel, ak jëmm jii nga xam ne, bokk na ci aji-xam ak boroomi màqaama yu gën a ràññeeku ci sunu réew.
Bala may daaneel, may leen ma ma dello njukkal njabootu Tataa Aram ak i mbokkam. Ndax kat, sunuy mbokk ñooy sunuy wéeruwaay. Rax-ci-dolli, yar bi sunuy waa-jur di def ci nun moo tax nu doon li nu doon tey. Te wolof dafa ne, peccum liir bu neexee, ndeyam a téye ca mbagg ya.
Bàjjen Aram, Wolof Njaay dinay wax ne bés du mag du tuuti, boroom lay tollool. Kon, kàddu gun fi yëkkati tey jëmale ko ci yow, xeeb nanu ko, yelloo nga lu ko ëpp.
Kon, dunu def lu dul di la ñaanal gudd fan ak wér, nga yàgg fi lool di nu won yoonu yokkute. Ñaan boobu lanu lay ñaanal, ni la ko Séex Adaraame Jaxate ñaanale ci xolam, bi mu lay jagleel benn ciy téere fent yi mu bind : ‘’Yàlla na ngay Maamati-Maam’’.
NDEY KODDU FAAL
Ñi ko tekkee ci tubaab : Paap Aali Jàllo ak Ndey Koddu Faal


ARAM FAAL, SUNU SÉEX ANTA JÓOB BU JIGÉEN… was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj