Càmmug Senegaal gu yees gi, jaare ko ci DGID, di kurél giy dajale kubal yi, daa fayloo woon Arcelor Mittal 1 205i miliyaar ci sunuy koppar. Waaye, kërug liggéey googu dafa lànkoon ne du fay, daldi yóbbu Càmmug Senegaal fa Yoon. Bi Yoon àttee, Senegaal la jox dëgg.
Arcelor Mittal dafa waroon a fay ay kubal yu tollu ci 1 205i miliyaari FCFA. Waaye, ca atum 2016 (weeru féewiryee), daa fayoon 100i miliyoŋi FCFA, ñu faral ko li desoon ci bor bi. Dañu ko defaraloon ag këyitug ceedeg maslaa (procès-verbal de conciliation). Waaye, këyit googu, njiit yi mësuñu koo wóoral.
Ginnaaw gi, waa “fisc” bi dañu sulli mbir mi ndax dafa jàpp ne Arcelor Mittal dafa war a fay. Moo tax ñu far ceedeg maslaa gees ko defaloon, fayloo ko 1 205i miliyaar yi mu warlul DGID. Arcelor Mittal nag, dafa bañoon ndogalu DGID loolu, yóbbu mbir mi ci Yoon. Bi yoon àttee, Càmmug Senegaal la jox dëgg.
Ci tënk, dañoo wàññiloon Arcelor Mittal borub kubal (lempo) bi mu ameel réew mi. Wàññi googu nag, laluwul ci sàrti réew mi ; maanaam tënkuwul ci yoon. Looloo tax kilifay DGID yi far déggoo bees defaloon Arcelor Mittal ngir wàññil ko bor bi, daldi koy fayeeku lépp. Kon, Arcelor Mittal dina fay. Ndax kat, àtte bor, fay.