ÀTTEKAT BI DAAN NA USMAAN SONKO AK NDEY XADI NJAAY 2I ATI KASO YI ÑUY TËDD

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñaari ati kaso yu Usmaan Sonko war a tëdd ak ñaari ati kaso yu Ndey Xadi Njaay war a tëdd. 20i tamndaret ci sunuy koppar yu Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay war a bokk fay ko Aji Saar. Lii mooy daan bi jibee ca àttewaayu Ndakaaru ba. Ñoom ñaar ñépp nag daan nañu leen ñaari ati kaso.

Bu dee Usmaan Sonko, àttekat bi setal na ko ci tuumay ciif ak tëkkuy rey yi ko Aji Saar doon toppe. Li ko àttekat bi daane mooy mbirum yàq xaleel, tubaab naan « corruption de jeunesse ». Maanaam, àttekat bi nee na, Usmaan Sonko siiful Aji Saar, metitalu ko, tëkkuwu ko itam, waaye daf defloo Aji Saar yëfi saay-saay jamono joo xam ne, xale la woon. Li ci doy waar nag, mooy ne, ca njëlbeen ga, du woon loolu lañ doon toppe Usmaan Sonko.

Bu dee Ndey Xadi Njaay, moom itam, li ko àttekat bi daane mooy ne, ci layam, boroom Sweet Beauté moo jàppale Usmaan Sonko ba mu mën a def li mu def. Bi ndogal li jibee, nee ñu, Aji Saar dafa doon jooy. Jamono jii nag, coow laa ngi ne kurr. Xeex bi door na.

Dees na ci dikkaat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj